6 Ay firikati yoonu Musaa nga fa woon toog. Ña ngay wax ca seen xel naan: 7 «Lu kii di wax nii? Yàlla de lay diir mbagg. Ana ku mana jéggaley bàkkaar, ku dul Yàlla doŋŋ?»
8 Ca saa sa Yeesu yég ci xelam la ñuy nàttable ci seen xel. Mu ne leen: «Li ngeen di nàttable nii ci seen xel, ana lu ko waral? 9 Ana yii yaar, lu ci gëna yomb: ne lafañ bi “Jéggalees na la say bàkkaar,” am ne ko: “Jógal, jël sa basaŋ te dox”? 10 Kon nag dingeen xam ne Doomu nit ki am na ci kaw suuf, sañ-sañu jéggale ay bàkkaar.» Mu ne lafañ ba: 11 «Dama ne, jógal, jël sa basaŋ, te ñibbi.» 12 Mu jóg, jël basaŋ ga ca saa sa, daldi génn fa kanam ñépp, ba ñépp waaru, di sàbbaal Yàlla, naan: «Lu mel nii, masunu koo gis!»
15 Yeesoo doon lekk ca kër Lewi, lu bare ci ay juutikat aki bàkkaarkat dikk, ñu bokk di lekk, ñook Yeesu aki taalibeem, ndax ñu baree ko toppoon. 16 Firikati yoonu Musaa ya bokk ca Farisen ya gis Yeesu bokk lekk ak bàkkaarkat yaak juutikat ya. Ñu ne ay taalibeem: «Juutikat yeek bàkkaarkat yi lay bokkal lekk nag?» 17 Yeesu nag dégg ca, ne leen: «Du ñi wér ñoo soxla fajkat, ñi wéradi ñoo ko soxla. Du ñi jub laa woosi, bàkkaarkat yi laay woo.»
21 «Kenn du jël sekkit wu yees, di ko daaxe mbubb mu ràpp. Lu ko moy sekkit wi day ñoddi ndimo la ràpp, mbubb ma gëna xar. 22 Biiñ bu bees it, deesu ko sotti ci mbuusum der yu ràpp. Lu ko moy biiñ bi fàcc mbuus yi, biiñ yàqu, mbuus yi yàqu. Biiñ bu bees daal, mbuus mu bees.»
25 Yeesu ne leen: «Xanaa masu leena jàng la Daawuda defoon, ba mu tolloo diggante te xiif, moom ak ña mu àndaloon? 26 Ba Daawuda duggee ca kër Yàlla ga, jant ya Abyatar dee sarxalkat bu mag ba, mburum teewal ma la lekk, te yoon mayewul kenn ku ca lekk, ku dul sarxalkat ba. Sédd na ca sax ña mu àndal.»
27 Yeesu dellu ne leen: «Bésub Noflaay, dees koo sàkk ngir nit ki. Waaye nit ki, sàkkeesu ko ngir bésub Noflaay. 28 Kon Doomu nit ki, bésub Noflaay it mooy boroom.»
<- Màrk 1Màrk 3 ->- a Lewi ak Macë kenn nit ki la.
Languages