Màrk Màrk taalibeb Piyeer la, te Piyeer bokk na ci taalibe yi gëna jege Yeesu (1.Piyeer 5.13). Màrk xam na it njàngaleem ndawal Yeesu li tudd Póol (Filemon 24; 2.Timote 4.11). Yaayu Màrk, Yerusalem la dëkk (Jëf ya 12.12). Fanweeri at gannaaw bi Yeesu deewee, la Màrk bind téereem, ngir tontu laaj bii: kan mooy Yeesu? Day wone kéemaan yi Yeesu def ak sañ-sañam ci ngelaw li ak ci géej gi sax. Li gëna fés ci nettali bi mooy bi Piyeer di wax Yeesu, naan ko: «Yaa di Almasi bi» (8.29). Gannaaw loolu, Yeesu tegu ci yoonu Yerusalem fi mu xame ne foofa la wara deewee. Coonoom ak deewam ñooy wone li waral mu nekk Almasi bi: «Ñëwul ngir ñu di ko surgawu, waaye mu nekk surga, ba far joxe bakkanam, def ko njotug ñu bare» (10.45). Ci tënk: 1.1-13 Yaxya soob na Yeesu ci ndox, Seytaane di ko jéema fiir. 1.14—9.50 Yeesu wone na gëddëm ci jàngaleem, ci kéemaan yi mu def. 10.1-52 Yeesu tukki na Yerusalem. 11.1—15.47 Ayu bés bu mujj bu Yeesu. 16.1-20 Yeesu dekki na, feeñu na ay taalibeem.
4 Yaxya nag dikk ca màndiŋ ma, di waare lu jëm ci tuubeel gu nit ñi wara fésale ag sóobu cim ndox, ngir Yàlla jéggal leen seeni bàkkaar. 5 Ci kaw loolu mboolem diiwaanu Yude ak waa Yerusalem ñépp bàbbeeku, jëm ca Yaxya. Ñu tudd seeni bàkkaar, Yaxya sóob leen ca dexu Yurdan. 6 Yaxyaa nga sol mbubb mu ñu ràbbe kawaru giléem, laxasoo laxasaayu der ca ndigg la, di dundey njéeréer ak lemu àll. 7 Mu waare, ne: «Am na ku ma sut kuy ñëw sama gannaaw, kooku, buumi caraxam sax yeyoowumaa sëgg, di ko ko feccil. 8 Man cim ndox laa leen sóob, waaye moom de, ci Noo gu Sell gi la leen di sóob.»
19 Yeesu doxaat tuuti, gis Yanqóoba doomu Sebede ak Yowaan mi Yanqóoba bokkal ndey ak baay. Ña nga ca gaal ga, di gaar seeni mbaal. 20 Yeesu woo leen ca saa sa, ñu bàyyi seen baay Sebede ca gaal ga, mook surga ya, daldi topp ca moom.
23 Jenn waay a nga woon ca seen biir jàngu ba, rab a ko jàpp. Mu jekki di xaacu, naan: 24 «Yaw Yeesum Nasaret, ana lu nu joteek yaw? Alagsi nu mooy say tànk? Xam naa yaa di kan, yaa di Aji Sell ju Yàlla ji.» 25 Yeesu nag gëdd ko, ne ko: «Noppil te génn nit ki!» 26 Rab wu bon wa daane waa ja ba muy say, mu yuuxu yuux gu réy, doora génne ca waa ja.
27 Ba loolu amee ñépp yéemu, naan ca seen biir: «Lii lu mu doon? Guléet mii njàngale! Céy bii xam-xam bu ànd ak sañ-sañ! Rab yi sax, mu jox leen ndigal, ñu def!» 28 Turu Yeesu nag law a law ca saa sa, ba dajal diiwaanu Galile gépp.
32 Ba ngoon jotee ba jant so, ñu indil Yeesu mboolem ñi wopp ak ñi rab jàpp, 33 dëkk ba bépp daje ca buntu kër ga. 34 Ci biir loolu ñu bare ñu ame ay jàngoroy jàngoro, mu wéral leen, rab yu bare, mu dàq leen. Waaye gannaaw rab ya xam nañu ko, mayu leen ñu wax.
38 Yeesu ne leen: «Nan dem feneen ci dëkk yi nu wër ngir ma waare foofu itam, ndax looloo ma taxa génn.» 39 Ci kaw loolu muy wër diiwaanu Galile gépp, di waare ci seeni jàngu, di dàq rab yi.
43 Yeesu nag artu ko bu baax, yiwi ko ca saa sa, ne ko: 44 «Fexeel ba bul wax kenn dara, demal rekk ca sarxalkat ba, ngir mu seet la, te nga génne sa saraxu setlu ni ko yoonu Musaa santaanee§Seetal ci Sarxalkat yi 14.1-32., ngir muy firnde ci ñoom.» 45 Waaye naka la waa ja génn, tàmbalee yéene, siiwal mbir ma, ba tax Yeesu manatula siiwal duggam cib dëkk, xanaa mu féetewoo béreb yu wéet ca fa ko wër. Teewul nit ñiy jóge fu nekk, di ko fekki.
Màrk 2 ->
Languages