6 Ba ñu waajalee noonu yooyii ba mu jekk, sarxalkat yaa daan dugg saa su nekk ca néeg bu njëkk ba, di def seen liggéey. 7 Waaye ñaareelu néeg ba, sarxalkat bu mag ba doŋŋ moo ca daan dugg, benn yoon cim at, te du ñàkka duggaale deret ju muy joxe ngir boppam ak itam ngir bàkkaar yi askan wi def te du ag teyeef. 8 Noonu la Noo gu Sell gi firndeele ne yoon wu maye ñu dugg ca néeg bu sella sell ba feeñagul woon, te fekk néeg bu njëkk ba di taxaw ba tey. 9 Loolu misaal la, ñeel jamonoy tey, di firndeel ne saraxi jur yi ak yeneen sarax yi ñu daan jébbale manuñoo def ba xelu jaamukatub Yàlla bi dal. 10 Sarax yooyu, ci aw ñam ak ag naan, ak xeeti njàpp[a] doŋŋ la jëm, lépp yittewoo yaramu suuxu neen, te di ndigal yu leen waroon ba keroog bésub coppite taxaw.
16 Kayitu ndono nag fu mu teew, fàww joxees fa firndey deewug ka donale, 17 ndax kayitu ndono du wér lu moy gannaaw bu nit ka deewee. Du jàppandi mukk li feek ki donalee ngi dund. 18 Looloo waral it kóllëre[b] gu njëkk ga ci boppam, dooreesu ko woon te deret tuuruwul. 19 Keroog ba Musaa biralalee bànni Israayil gépp mboolem santaane, na ko yoon wi laaje, ba mu noppee, deretu wëllu la jël, ak ju sikket akum ndox ak caru garabu isob bu mu laxas kawaru xar gu xonq. Mu capp ko ca deret ja, wis-wisal ko ca kaw téereb yoon wa ak ca kaw mbooloo mépp. 20 Mu ne: «Lii nag mooy deret ji Yàlla fase kóllëre gi mu séq ak yeen‡Seetal ci Mucc ga 24.8..» 21 Xayma ba ak mboolem ndabi carxal ya it, noonu la Musaa wis-wisale deret ca seen kaw. 22 Ndax ci yoonu Musaa sax, deret lees di setale daanaka lépp, te bu deret tuuruwul, njéggal amul.
23 Jumtukaay yooyi di ay misaali yëf ya fa asamaan, yooyu sarax lees ko waroona setale. Kon yëfi asamaan ya ci boppam, sarax yu ko gën lees ko wara setale. 24 Ndax néeg yu sell yu nit tabax, te muy royaalub néeg bu dëggu ba doŋŋ, du ci la Almasi bi dugg. Waaye ci asamaan ci boppam la dugg ngir teewal nu tey, fa kanam Yàlla. 25 Duggul asamaan it ngir di sarxe aka sarxewaat boppam, noonee sarxalkat bu mag ba daan dugge at mu nekk ca néeg bu sella sell, yóbbaale deret ju dul josam. 26 Lu ko moy ca njàlbéenu àddina lay dale sonn ay yooni yoon. Waaye tey ci mujug jamono yi la feeñ benn yoon doŋŋ, ba sarxe boppam, ngir far bàkkaar. 27 Kon ni ab dogal sédde nit ñi benn yoon doŋŋ bu ñuy dee, seenub àtte topp ci, 28 noonu itam la Almasi bi doone ab sarax benn yoon, ngir gàddu bàkkaaru nit ñu bare, te dina teewsiwaat, ci yoon wu joteetul dara ak bàkkaar, ngir indil ñi koy séentu seenug mucc.
<- Yawut ya 8Yawut ya 10 ->
Languages