1 Yoonu Musaa takkndeeru xéewal yiy ñëw doŋŋ a ci nekk, waaye xéewal ya ci seen bopp nekku ci. Looloo tax sarax yi yoon wi laaj ñu war koo saxoo jébbale at mu nekk, manula setal mukk wecc ñiy jaamusi. 2 Su sarax yi taxoona set wecc, xanaa deesu ko dakkal? Bu ca jaamukati Yàlla yi doon sete wecc benn yoon kay, xanaa dootuñu am yaraangey bàkkaar! 3 Sarax yooyu dañu koy fàttalee ay bàkkaar at mu jot, 4 ndax deretu yëkk ak ju sikket kat manula far ay bàkkaar.
5 Moo tax ba Almasi biy dikk ci àddina la wax ne:
11 Bépp sarxalkat a ngi taxaw bés bu nekk ci liggéeyam, di jébbale aka jébbalewaat yenn sarax yooyu, te lenn du ci masa mana far bàkkaar. 12 Waaye kii de, ba mu sarxee boppam ngir far ay bàkkaar, bennub sarax bu doy ba fàww, ca la tooge fa ndijooru Yàlla. 13 Fa la doxe xaar bés ba ñu koy defal ay noonam ndëggastalu tànkam. 14 Kon bennub sarax boobu, ci la matale sëkk ba fàww nit ñi ñu sellal.
15 Mooy li Noo gu Sell gi itam seede, ñeel nu, 16 nde gannaaw ba mu nee:
26 Gannaaw bu nu xamee xéll liy dëgg ba noppi nag, su nu bàkkaaratee te di ko tey, su boobaa ab sarax bu far yooyu bàkkaar amatu ci. 27 Xanaa tiitaangey séentu mbugal ma ak sawara wu yànj wiy xoyom fippukat yi. 28 Képp ku masoona xëtt yoonu Musaa, daawuñu ko ñéeblu; ci kaw seedey ñaari nit ba ñett lees ko daan rey. 29 Kon ki dëggaate Doomu Yàlla, teddadil deret ji ñu sellale kóllëre gi, te ñàkke teggin Noowug Yàlla gi nu indil aw yiw, kooku, mbugal ma mu yelloo, ñaata yoon lay gënatee metti, ngeen defe? 30 Xam nanu ki wax ne: «Maay kiy feye, di añale,» neeti: «Boroom bi mooy àtte ñoñam‡Seetal ci Baamtug yoon wi 32.35-36..» 31 Céy ku nara tàbbi ci loxoy Yàlla jiy dund, ndaw lu raglu!
32 Fàttalikuleen bés yu njëkk ya, gannaaw ba ngeen jotee ci leeru Yàlla, na ngeen dëgërloo woon ca xeex bu mag ba te metti. 33 Léeg-léegaa ñu saaga leen, bunduxataal leen ci kanam nit ñi; léeg-léegaa yeen ay taxawu nit ñi ñu teg lu ni mel. 34 Ndax yeena bokk ak ñi ñu tëj seen coono, te yeena muñ ci xol bu sedd ni ñu foqarñee seen moomeel, ngir xam ngeen yeen ci seen bopp ne am ngeen alal ju ko gën tey sax ba fàww.
35 Kon nag buleen teqalikook seenu fit, yool bu réy a ngi ci. 36 Li leen war moo di muñ, ba sottal coobarey Yàlla, su ko defee ngeen jot li mu dige. 37 Ndax kat,
Languages