2 Mbir ma nag mujje féewaloo ak werante wu xawa metti, te Póol ak Barnabas séq ko ak ñooñu. Ba loolu amee ñu ne, na Póol ak Barnabas ak ñenn ca gëmkati Àncos ànd dem Yerusalem ca ndawi Yeesu ak mag ña, ba lijjanti mbir moomu.
3 Ci kaw loolu mbooloom gëmkat ñi yebal leen, ñu jaare Fenisi ak Samari, daldi àgge waa foofa ni jàmbur ñi dul Yawut tuube, ba bokki gëmkat ñépp bég ca lool. 4 Gannaaw loolu, ñu agsi Yerusalem, mbooloom gëmkat ñi ak ndawi Yeesu yi ak mag ñi dalal leen, ñu nettali leen mboolem ni Yàlla def ak ñoom.
5 Ba mu ko defee ñenn ci gëmkat ñi bokk ci ngérum Farisen yi, daldi taxaw temm, ne gëmkat ñi dul Yawut, fàww ñu xarafal leen, sàmmloo leen yoonu Musaa.
6 Ba loolu amee ndawi Yeesu yi ak mag ñi bokk daje, ngir seet mbir moomu. 7 Werante wu réy am ca. Ci kaw loolu Piyeer jóg ne leen: «Bokk yi, yeen xam ngeen ne bu yàgg la ma Yàlla seppee ci seen biir, ngir jàmbur ñi dégge ci sama làmmiñ kàddug xibaaru jàmm bi, ba doon ay gëmkat. 8 Yàlla mi xam xolu nit nag moo seedeel jàmbur ñi, ba mu leen mayee Noo gu Sell gi, ni mu nu ko maye nun itam. 9 Yàlla amul xejj ak seen sunu dig ak ñoom, ndax seen ngëm la raxase seen xol. 10 Léegi nag lu tax ngeen di diiŋat Yàlla, di teg taalibe yi yen bu nu masula àttan, cay maam ba ci nun? 11 Yiwu Sang bi Yeesu daal lanu gëm ne ci lanuy mucce, te ñoom itam, noonu rekk.»
12 Ba loolu wéyee mbooloo mépp ne xerem. Ñu déglu nag Barnabas ak Póol, ñu xamle mboolem firnde yeek kéemaan yi Yàlla defe seen ñaari jëmm ci biir jàmbur ñi. 13 Ba ñu noppee, Yanqóoba àddu ne: «Bokk yi, dégluleen ma. 14 Simoŋ[b] xamle na, ni Yàlla yége jàmbur ñi ca njàlbéen, ba sàkke ci seen biir xeet wu mu tudde turam. 15 Te loolu dëppoo na ak kàdduy yonent yi, ndax bindees na ne:
19 «Kon nag sama xalaat mooy: bunu gétën jàmbur ñi tuub, ba waññiku ci Yàlla. 20 Xanaa nu bind leen, ne leen ñu moytu lu ay xërëm sobeel, moytu séy yi yoon tere, moytoo lekk yàppu mala mu ñu tuurul deretam, ak lekk deret ci boppam. 21 Ndaxte ca njàlbéen ga ba tey ay nit a ngi waaree yoonu Musaa ci dëkk bu nekk, ñu di ko jàng ci jàngu yi bésub Noflaay bu nekk.»
23 Ñu yóbbante leen bataaxal, bind ci ne:
30 Ba loolu amee ñu tàggatoo, daldi dem ba Àncos. Ci kaw loolu ñu woo mbooloo mi, jébbal leen bataaxal bi. 31 Ba ñu jàngee bataaxal bi, kàddu ga dëfal leen, seen xol sedd. 32 Yuda ak Silas it gannaaw ay yonent lañu woon, wax nañu ak bokk yi lu yàgg, ngir ñaax leen, feddali seen ngëm. 33-34 Ba loolu amee ñu toog fa ab diir, bokk yi door leena ñaanal yoonu jàmm, yiwi leen, ngir ñu dellu ca ña leen yebaloon. 35 Póol ak Barnabas nag des Àncos. Ñu ànd ak ñeneen ñu bare, di jàngale aka xamle kàddug Boroom bi.
39 Mbir mi nag mujje dëngoo bu metti, ba ñu teqalikoo. Barnabas ànd ak Yowaan Màrk, dugg gaal, jëm Sippar. 40 Póol moom taamu Silas, daldi ànd ak moom dem, gannaaw ba leen bokk ya dénkee Boroom bi ciw yiwam. 41 Ci kaw loolu mu jaare diiwaani Siri ak Silisi, di ñaax mboolooy gëmkat ña.
<- Jëf ya 14Jëf ya 16 ->
Languages