11 Ba mbooloo ma gisee la Póol def, ca kaw lañu àddu ci làkku likawni, ne: «Yàlla yee soppaliku melow nit, wàccsi ci sunu biir!» 12 Ci kaw loolu ñu tudde Barnabas Sës, kilifay yàllay Gereg yi, Póol nag gannaaw moo farewoo woon kàddug waare ga, ñu tudde ko Ermes, ndawal yàllay Gereg yi. 13 Jaamookaayu Sës ma nga woon ca buntu dëkk ba. Sarxalkat ba daldi indi ca bunti dëkk ba ay yëkk yu ñu takkal caqi tóor-tóor. Sarxalkat ba ànd ak mbooloo ma, nara rendi jur ga, sarxal ko Póol ak Barnabas.
14 Ci kaw loolu Póol ak Barnabas yég la xew. Ñu xotti seeni yére ndax ñaawlu ko. Ñu buur nag ba ca biir mbooloo ma, daldi àddu ca kaw ne: 15 «Yeen, lu leen xiir ci lii? Nun itam ay nit lanu, bokk ak yeen benn bind. Xibaaru jàmm bi lanu leen di xamal, ngir ngeen wacc yëfi neen yii te walbatiku ci Yàlla, kiy dund te sàkk asamaan ak suuf ak géej ak lépp li ci biir. 16 Moo mayoon démb xeet yépp, ñu aw ci seen yooni bopp. 17 Moona noppiwula seedeel boppam ci mbaaxam gi muy jëfe, di leen wàcceel fa asamaan taw ak naataange, reggal leen, bégal leen ba seen xol sedd.»
18 Loolu lépp ndaw ya wax nañu ko te tuuti kon ñu tëlee tere mbooloo ma ñu rendil leen sarax.
19 Ci kaw loolu ay Yawut yu jóge Àncos gu Pisidi ak Ikoñum, fexe ba fàbbi mbooloo ma, daldi dóor Póol ay doj, diri ko ba génne ko dëkk ba, yaakaar ne dee na. 20 Naka la ko taalibe ya yéew, mu jóg, daldi dellu ca biir dëkk ba. Ca ëllëg sa, mu ànd ak Barnabas, dem Derbe.
26 Foofa lañu dugge gaal, dellu Àncos gu Siri ga ñu leen dénke woon Yàlla ciw yiwam, ngir liggéey ba ñu sottal, ba délsi noonu. 27 Ba ñu agsee, dañoo woo mbooloom gëmkat ña, àgge leen mboolem na Yàlla def ak ñoom, ak na mu ubbilee jàmbur ñi dul Yawut buntu ngëm. 28 Ñu toog nag ak taalibe ya diir bu xawa yàgg.
<- Jëf ya 13Jëf ya 15 ->
Languages