17 Bésub keroog xeex ba metti na lool, waaye Abner ak waa Israayil ñoo féete suuf niti Daawuda.
18 Ñetti doomi Ceruya ña nga fa woon: Yowab ak Abisay ak Asayel. Asayel nag daa manoona daw lool ni kéwél. 19 Asayel ne dann Abner rekk, jàddul ndijoor, jàddul càmmoñ. 20 Abner geesu ne ko: «Kii Asayel?» Mu ne ko: «Man a.» 21 Abner ne ko: «Tee ngaa jàdd ndijoor mbaa càmmoñ, te jàpp kenn ci xale yu góor yi, futti ko!» Asayel nag bëggu koo bàyyi, xanaa topp ko rekk. 22 Abner dellu ne Asayel: «Xiddi ma! Bul tax ma jam la, nga daanu! Te kon xawma nu may jàkkaarlooteek sa mag Yowab!» 23 Asayel të ticc, topp ko. Abner jam ko catal xeejam ca biir ba, ba xeej ba fëll ca gannaaw ga, mu daanu dee ca saa sa. Ba loolu amee, ku dikk, ba tollook béreb ba Asayel daanu dee, daldi fay taxaw.
24 Yowab ak Abisay nag dàqi Abner. Ba jant bay lang, ña nga tollu ca tundu Ama wa janook Giyax, ca yoon wa jëm màndiŋu Gabawon. 25 Beñamineen ñi daldi mànkoo, topp ca gannaaw Abner, ñu def menn mbooloo, bokk taxaw ci kaw wenn tund. 26 Abner àddu ca kaw, ne Yowab: «Mbaa du saamar day wéy di lekk suux ba fàww? Xamuloo ne lii aw naqar doŋŋ lay mujje? Ana looy xaarati ci ne mbooloo mi ñu noppee topp seeni bokk?» 27 Yowab ne ko: «Giñ naa ci Yàlla jiy dund, boo waxuloon, nit ñi duñu noppee dàq seeni bokk te bët setul.» 28 Ba loola amee Yowab wal bufta ba, di liit gu ñu defare béjjénu kuuy, gaa ña ñépp nag taxaw, noppee topp Israayil, daldi dakkal xare ba. 29 Abner aki nitam fanaanee topp xuru Yurdan guddig keroog, ba jàll dexu Yurdan. Ñu daldi jaare Bittron gépp, doora agsi Maxanayim.
30 Gannaaw ba Yowab walbatikoo ca ndàqum Abner, daa woo gàngooram gépp, fukk ak juróom ñeent wuute ci niti Daawuda, te limaalewuñu Asayel. 31 Waaye fekk na niti Daawuda rey ñetti téeméer ak juróom benn fukk (360) ca Beñamineen ñaak niti Abner. 32 Ñu yóbbu Asayel, rob ko ca wetu baayam ca Betleyem, Yowab aki nitam nag fanaanee dox, ba jant fenke leen Ebron.
<- 2.Samiyel 12.Samiyel 3 ->
Languages