2.Samiyel di téereb ñaareel bi Téereb 2.Samiyel moo indi jaar-jaari Buur Daawuda ak ndamam. Indi na tamit fan yu lëndëm ci dundam: digganteem ak ndaw sa Batseba ca la, ak fippu ga doomam Absalom jiite woon. Teewul Daawuda mooy ku jikkoom juboo ak xolu Yàlla, ni ko Yàlla ci boppam waxe. Gaawoon na ci nangu ay tooñam, te di tuub, di ñaan Yàlla mu jéggal ko. Ci tënk: 1.1—6.23 Lu jëm ci palug Daawuda ak ndoortel nguuram. 7.1-29 Yàlla fas na kóllëre ak Daawuda. 8.1—10.19 Daawuda am na ay ndam ci ay noonam. 11.1—12.25 Daawuda moy na Yàlla, Yonent Yàlla Natan ŋàññ ko. 12.26—21.22 Lu jëm ci nguurug Daawuda ak gàllankoor ya. 22.1—24.25 Daawuda biral na cantam gu mujj, nguuram di amati gàllankoor.
3 Daawuda ne ko: «Foo jóge nii?» Mu ne ko: «Ca dalub Israayil laa rëcce.» 4 Daawuda ne ko: «Lu xew, gaawe ma!» Mu ne ko: «Mbooloom Israayil a dawe ca xare ba. Ñu bare ca ñoom daanu nañu, dee. Sawul ak doomam Yonatan it dee nañu.» 5 Daawuda ne ndaw la: «Lu la xamal ne Sawul ak doomam Yonatan dee nañu?» 6 Ndaw la ne ko: «Dafa yemook ma tollu tembe ca kaw tundu Gilbowa. Ndeke Sawul a nga fa, sukkandikoo xeejam. Watiiri xare yaak gawar ya defuñu lu moy ne ko dann. 7 Naka la ne gees, yem ci man, woo ma, ma wuyu. 8 Mu ne ma: “Yaa di kan?” Ma ne ko: “Ab Amalegeen laa.” 9 Mu ne ma: “Kaay fii, jekkali ma. Maa ngi ci miirum dee, doonte dese naa tuuti.” 10 Ma dikk, daldi koy jekkali, ndax xamoon naa ne du dundati gannaaw jéllam ba. Ma summi nag mbaxanam buur ma mu soloon, tekki lam ba woon ca përëg ma. Yooyu laa la yótsi nii, sang bi.»
11 Ba loolu amee Daawuda sëq yéreem, xotti, ña ànd ak moom ñépp itam, noonu, ndax aw naqar. 12 Ñaawlu nañu, di jooy, lekkuñu ba ca ngoon ndax Sawul ak doomam Yonatan ak gàngooru Aji Sax ji, ak waa kër Israayil ña ñu reye saamar.
13 Daawuda ne ndaw la: «Ana foo bokk?» Mu ne ko: «Man doomu doxandéemub Amalegeen laa.» 14 Daawuda ne ko: «Noo saña xàcce sa loxo, di bóom ki Aji Sax ji fal?» 15 Daawuda nag woo kenn cay surgaam, ne ko: «Dikkal dóor, mu dee!» 16 Daawuda ne Amalegeen ba: «Yaa gàddu sa bakkanu bopp, ndax yaa seedee sa gémmiñu bopp ne yaa rey ki Aji Sax ji fal.» Surga ba dóor Amalegeen ba, mu dee.
Languages