1 Ni may roye Almasi bi, man ci sama bopp, royeleen ma noonu.
3 Waaye nag bëgg naa ngeen xam ne gépp góor, Almasi bi moo di boppam; jigéen, góor moo di boppam, te Almasi bi, Yàlla moo di boppam. 4 Kon gépp góor guy ñaan, mbaa muy waxe kàdduy waxyu, bu muuree boppam, suufeel na Almasi biy boppam. 5 Waaye jépp jigéen juy ñaan, mbaa muy waxe kàdduy waxyu, te muurul boppam, suufeel na jëkkëram jiy boppam. Day mel ni bu nelu woon rekk. 6 Jigéen ju nanguwula muuru, bu yeboo xuuf kawaram. Ndegam am na kersay xuuf kawaram, mbaa mu nelu nag, fàww mu muur boppam. 7 Góor moom du muur boppam, ndax mooy takkndeeru Yàlla te moo taxawe darajay Yàlla. Waaye jigéen moo taxawe darajay góor, 8 ndax góor kat, jëleesu ko ci jigéen, waaye jigéen kay lañu jële ci góor. 9 Góor itam, sàkkeesu ko ngir jigéen, waaye jigéen kay lañu sàkk ngir góor. 10 Looloo tax jigéen wara fésal kilifteef ci kaw boppam, ndax malaaka yi teew*Seetal ci Efes 3.10.. 11 Teewul nag ci yoonu Sang bi, jigéen manula ñàkka wéeru ci góor, góor it manula ñàkka wéeru ci jigéen, 12 ndax ni jigéen bàyyikoo ci góor, noonu la góor juddoo ci jigéen, te lépp fa Yàlla la bawoo.
13 Seetalleen ko seen bopp rekk, ndax jekk na ci jigéen, muy ñaan ci Yàlla, te muurul boppam? 14 Xanaa ni àddina ci boppam tëdde xamalu leen ne yar kawar gàcce la ci góor? 15 Ndaxam kawar gu bare sagu jigéen la. Jigéen lañu jagleel kawar gu bare, muy muuraayam. 16 Waaye ku bëgga werante ci leneen it, nun loolu du sunu baax, te du baaxu mbooloom Yàlla mi.
23 Man, li ma jële ci Sang bi, moom laa leen jottali: Sang Yeesu, guddi gi ñu ko woree, dafa jël mburu, 24 yékkati kàddug cant, dagg ko, ne: «Lii moo di sama yaram wi leen ñeel. Deeleen def lii, di ma ko fàttalikoo.» 25 Noonu itam la def ak kaas ba, gannaaw reer ba, ne leen: «Kaas bii mooy kóllëre gu yees gi fasoo ci sama deret. Deeleen def lii, di ma ko fàttalikoo, saa yu ngeen ci naanee.» 26 Saa su ngeen lekkee ci mburu mii, mbaa ngeen naan ci kaas bii, yégle ngeen deewug Sang bi, ba kera muy ñëw.
27 Moo tax, képp ku jekkadi nu mu lekke ci mburu mi ak nu mu naane ci kaasu Sang bi, tooñ nga yaramu Sang bi ak deretam. 28 Kon na ku nekk seetlu boppam, doora lekk ci mburu mi, naan ci kaas bi. 29 Ndax ku lekk ci mburu mi, naan ci kaas bi, te joxul gëdd yaramu Almasi bi, ab daan bu mu teg boppam la lekk, naan ko. 30 Looloo tax ngeen bare ñu néew doole ak ñu xiibon, ba lim bu takku dee. 31 Su nu doon seetlu sunu bopp, deesu nu àttee noonu. 32 Waaye Boroom bee nuy teg ay daan ngir yare nu ko, ba deesu nu mbugalaale ci biir àtteb àddina.
33 Kon nag bokk yi, bu ngeen dajee, ngir bokk lekk, xaaranteleen. 34 Ku xiif, na lekke këram, ngir seeni ndaje bañ leena jural ab daan.
- a Seetal ci Efes 3.10.
Languages