6 Yooyu xew-xew ay misaal la, ngir nu baña xemmem yëf yu bon, na ko maam ya daan xemmeme. 7 Buleen doon ay jaamukati tuur, ni ko ñenn ci ñoom doone woon. Noonu lañu binde ne: «Mbooloo ma toog, di lekk aka naan, nes tuut ñu jóg, di mbumbaay†Seetal ci Mucc ga 32.6..» 8 Bunu yebu ci séy yi yoon tere, ni ko ñenn ci ñoom daa defe, ba tax ñaar fukki junni ak ñett (23 000) ca mbooloo ma bokk dee ci benn bés. 9 Bunu wut itam Almasi bi, ni ko ñenn ci ñoom wute woon, ba tax ay jaan rey leen. 10 Buleen jàmbat, ni ñenn ci ñoom doon jàmbate, ba tax malaakam reykat ba rey leen.
11 Xew-xew yooyu dal maam ya ay misaal la, te dees koo bind ngir nu jànge ci, nun ñi mujug jamono yemool. 12 Moo tax ku yaakaar ne taxaw nga, nanga moytu bala ngay daanu. 13 Benn nattu dabu leen bu moy nattu yiy dale. Te it Yàllaa jara wóolu. Yàlla du nangu ngeen tegoo nattu bu ngeen àttanul, waaye nattu ba lay booleek pexe ma leen cay génne, ba ngeen man koo dékku.
18 Xoolleen bànni Israayil ci wàllu deret. Ñiy lekk yàppu juru sarax gu ñu rendi, xanaa bokkuñu ak sarxalukaay bi ab céram? 19 Ana kon lu sama wax jiy wund? Ndax daa wund ne yàpp wu ñu sarxal tuur yi tekki na lenn? Am daa wund ne tuur yi tekki na lenn? 20 Li may wax kay moo di yooyu sarax, rab yi la ñeel, waaye du Yàlla, te bëgguma ngeen bokk ak rab yi lenn. 21 Dungeen mana naan ci kaasu Sang bi, naan ci kaasu rab yi. Dungeen mana bokk lekk ci ndabal Sang bi, bokk lekk ci ndabal rab yi. 22 Am danuy yékkati fiiraangey Sang bi? Danu koo ëpp doole?
25 Lépp luy jaay marse, sañ ngeen koo lekk te bañ cee luqatu lenn luy indi ngànt cim xel, 26 ndax Boroom bee moom àddina ak li ci biiram.
27 Bu leen ku gëmul woowee lekk, su ngeen nangoo, mboolem lu mu leen taajal, lekkleen, te bañ cee luqatu luy indi ngànt cim xel. 28 Waaye bu leen kenn nee: «Lii ñam wu ñu sarxal tuur yi la,» buleen lekk, ndax ka leen ko xamal, ndax itam, ngànt lu wax jiy indi cim xel. 29 Waxuma seenum xel yeen, waaye xelu keneen ka laay wax.
31 Kon nag su ngeen di lekk, mbaa ngeen di naan, mbaa ngeen di def leneen, lépp lu ngeen di def, wutleen koo terale Yàlla. 32 Buleen may kenn lu muy def njombe: du Yawut yi, du jàmbur ñi, du mbooloom Yàlla mi. 33 Noonu laay def man ci sama bopp: ñépp laay wuta neex, ci lépp. Sàkkuwuma sama njariñal bopp, waaye njariñal lim bu gëna takku, moom laay sàkku, ngir ñu texe.
<- 1.Korent 91.Korent 11 ->- a Ba bànni Israayil nekkee ca màndiŋ ma, Boroom bi moom ci boppam moo leen jiite woon, mel ni aw niir, ag bëccëg ngir gindi leen, su guddee mu doon taxaaru sawara, ngir niital leen. Seetal ci Mucc ga 13.20—14.31.
- b Seetal ci Mucc ga 32.6.
- c mburu mi nuy daggoo: moom la gëmkat ñi di yéglee deewug Almasi bi. Seetal ci 11.26.
Languages