Sàkkaryaa Yonent Yàlla Sàkkaryaa sasub yonent ak sasu sarxalkat la boole woon, ñeel bànni Israayil, gannaaw ba ñu leen gàddaayloo ñu dem Babilon. Yonent Yàlla Ase la bokkal jamono, te doon ko jàppale ci soññe, ngir àggale kër Yàlla ga. Ci téere bii la Sàkkaryaa xamle ne li waraloon toxalub bànni Israayil ca Babilon mooy seen jëfi bàkkaar. Teewul mu sukkandikoo peeñu yu ko Yàlla baaxe, ba xamal xeet wi ne Yàlla ci boppam moo leen di sopparñi, boole ci indi jamonoy sell ju bees ju dajal àddina sépp. Pàcc bi njëkk ci téere bi moo indi juróom ñetti peeñuy guddi yu dikkal Sàkkaryaa, teg ci leeral ci mbirum koor. Ñaareelu pàccu téere bi moo wax lu jëm ci jamono ju yees ji Yàlla di sopparñi Israayil ba mu doon dëkk bu sell dëgg, jamono ju xeeti àddina di jaamusi Yàlla ci Yerusalem. Sàkkaryaa wax na itam ci mbirum sàmm bu mag, di Almasi biy dikk, ngir yilif nguur gu bees gu jàmm ja di mat sëkk. Ci tënk: Saar 1—8 Lu jëm ci juróom ñetti peeñu yi dikkal Sàkkaryaa. Saar 9—11 Ay xibaar a ngii, yu ëmb mbugal ak yaakaar. Saar 12—14 Lu jëm ci Almasi biy dikk ak ni ñu koy gàntale, ak ndam li Almasi bi di mujje.
12 Malaakam Aji Sax ji ne: «Éy Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, loo deeti xaar, doo noppee xañ yërmande Yerusalem ak yeneen dëkki Yuda? Juróom ñaar fukki at a ngii yoo leen mere[a]!»
13 Aji Sax ji nag àddu, wax ak malaaka ma doon wax ak man, kàdduy mas-sawu yu neex. 14 Ca la malaaka ma doon wax ak man, ne ma: «Yéeneel, nga ne: “Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Maa fiire Yerusalem, maa fiire Siyoŋ fiiraange ju réy. 15 Waaye mer mu réy laa mere xeet yii naagu. As lëf laa meroon, waaye ñoom ñoo yokk aw ay[b]. 16 Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne: Yërmande laay dellusee Yerusalem. Sama kër lees fay tabaxaat.” Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi. Mu ne: “Buumu nattukaay dina tàllalu ci kaw Yerusalem.” 17 Nanga yéenewaat, nga ne: “Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Samay dëkk ay walewaat ak alal, te Aji Sax ji mooy dëfalati Siyoŋ, mooy tànnati Yerusalem googu.”»
Sàkkaryaa 2 ->
Languages