Ruut Téereb Ruut da noo delloo ca jamono ja njiit ya yoree kilifteefu bànni Israayil, laata bànni Israayil di fal buur. Ruut moo jur doom ju góor Obedd, mi jur Yese, baayu Daawuda mi falu ñaareelu buuru Israayil. Gannaaw ba jëkkëram faatoo, Ruut la soob mu dëddu réewum Mowabeen ma mu cosaanoo, ngir toppatoo ab goroom Nawmi, mi doon ab jëtun moom itam. Ngëm gi Ruut gëm Aji Sax ji moo tax mu mana séy ak ku bokk ci bànni Israayil. Ci mujjantal ga, naqaru Nawmi soppaliku doon bànneex ndax kóllëreg Ruut ak njekkug mbokkam Bowas, moom mi am sañ-sañu jotaat ko. Ci tënk: 1.1-10 Aw tiis dikkal na Nawmi. 1.11-22 Ruut sàmm na kóllëre digganteem ak Nawmi. 2.1—3.18 Bowas mbokkum Nawmi def na njekk. 4.1-17 Bowas def na wareefam, ni jotkat bi mu doon. 4.18-22 Lii mooy cosaanu Daawuda, mi sëtoo ci Bowas ak Ruut.
3 Gannaaw gi, Elimeleg jëkkëru Nawmi faatu; Nawmi des ak ñaari doomam yu góor. 4 Ñooñu mujj jël ay jigéeni Mowab soxna; kenn ka di Orpa, ka ca des di Ruut. Ba ñu nekkee foofa lu tollu ci fukki at, 5 ñoom ñaar ñooñu di Maxlon ak Kilyon faatu ñoom it, jigéen ja ñàkk noonu ñaari doomam ak jëkkëram. Mu des moom kese.
8 Ci biir loolu mu wax ak ñaari goro ya, ne leen: «Demleen kay, ñibbileen, ku nekk sa kër yaay. Yal na leen Aji Sax ji baaxe, na ngeen baaxe woon ñi wuutu, te baaxe ma, man itam. 9 Yal na Aji Sax ji may ku nekk ci yeen jàmm ca kër jëkkër ja muy amaat.» Ci kaw loolu mu fóon leen, ñu ne yikkét jooyoo. 10 Ñu ne ko: «Déet, yaw kay lanuy àndal, dem ca say bokk.»
11 Mu ne leen: «Ñibbileen ngalla, doom, lu ngeen di ànd ak man doye? Ndax dama leena manatee jural ay jëkkër ci sama biir bii? 12 Ñibbileen rikk doom, demleen, ngir man damay mag, ba wees séy; te su ma ci dese woon yaakaar it, guddig tey jii sax su ma ci séyoon, jur ciy doom, 13 mbaa dingeen leen mana xaar, ba ñu màgg? Xanaa dungeen toog, baña séy ndax ñoom? Déedéet, doom. Maa leen ëpp naqar, man mi Aji Sax ji nattoo nii.»
14 Ñu dellu ne yikkét, di jooyoo. Orpa fóon goroom, tàggatook moom, Ruut nag moom langaamu ko rekk. 15 Mu ne ko: «Gis nga sa wujju peccorgo waa ngay ñibbi cay bokkam aki yàllaam. Àndal ak moom ñibbi kay!» 16 Mu ne ko: «Bu ma soññ mukk ci loolu, duma la wacc, duma la dëddu. Foo jëm, fa laa jëm; fooy dal, fa laay dal; say bokk di saay bokk; sa Yàlla di sama Yàlla. 17 Foo deewe it, ma deewe fa, ñu denc ma fa. Yal na ma Aji Sax ji teg mbugal mu gëna tar, ndegam lenn lu moy dee tàggale na maak yaw.» 18 Nawmi nag gis ni Ruut dogoo ci ànd ak moom, ba tax soññatu ko. 19 Ba mu ko defee ñu ànd ñoom ñaar, ba àgg Betleyem.
22 Noonu la Nawmi jógee Mowab, ñibbisi, ànd ak Ruut, gorob Mowabeenam ba. Ñu agsi Betleyem, fekk ngóobum lors ma di tàmbali.
Ruut 2 ->
Languages