6 Ndax kat, ba nu amul menn pexem mucc, ca waxtu wa gën, la Almasi bi deewal yéefar yi. 7 Barewul ku nangoo dee ngir nit ku jub, doonte jombul mu am ku nangoo dee ngir ku baax. 8 Waaye Yàlla moom, ni mu firndeele cofeelam ci nun, moo di, ba nu doon ay bàkkaarkat, ca la Almasi bi deewe ngir nun!
9 Gannaaw baaxees nañu nu àtteb ñu jub ndax deretam ji tuuru nag, ñaata yoon lees nuy gënatee musal ci am sànj ndax moom? 10 Ndegam ba ñu dee ay bañaaley Yàlla lees nu jubalee deewug Doomam, ñaata yoon lees nuy gënatee musale ag dundam, gannaaw ba ñu nu jubalee ak Yàlla? 11 Te yemunu ci, xanaa di sagoo Yàlla itam ndax sunu Boroom Yeesu Almasi bi nu jubale ak moom.
15 Waaye ni moyug Aadama deme, yiwu Yàlla demewu ni. Moyug kenn nit, Aadama, tax na ñu bare dee; waaye yiwu Yàlla ak mayug yiw gu kenn nit, Yeesu Almasi bi, ñaata yoon la gënatee baawaan, ñeel nit ñu bare? 16 Ni njeexitalu tooñu kenn nit deme, laa ne, mayu Yàlla demewu ni. Benn bàkkaar moo waral àtte bi indi mbugal. Waaye moy yu bare moo waral may gi teggi tuuma. 17 Moyug kenn nit ki, ci la dee jaare ci kenn nit kooku, ba falu. Kon ñi jot ci xéewalu yiw, ba am ci àtteb njub, ñaata yoon lañuy gënatee falu ci biir dund gu ñu ame ci keneen nit kiy Yeesu Almasi bi?
18 Kon nag noonee moyug kenn jure mbugalu nit ñépp daal, noonu la jenn jëfu njekk[b] jurale ñépp dundin wu yees ci kaw àtteb njub bu leen jenn jëf ja may. 19 Noonee déggadig kenn nit taxe ñu bare doon ay bàkkaarkat, noonu it la déggug ndigalu kenn nit taxe ñu baaxe ñu bare àtteb nit ñu jub.
20 Yoonu Musaa moo dikk ngir fésal barewaayu moy, waaye fu bàkkaar bare, aw yiw gën faa bareeti, 21 ba tax na, noonee bàkkaar doone woon buur, ndax dee gi mu yilife ñépp, ni la aw yiw wuutoo, di buur moom itam, ndax àtteb njub gi aw yiw jural nit ñi, ba jëme leen ci texe gu sax dàkk, ci sunu ndimbalal Boroom Yeesu Almasi bi.
<- Room 4Room 6 ->
Languages