Room Ñeenti téere yii: Macë, Màrk, Luug ak Yowaan, ñoo nettali dundug Yeesu ak deewam ak ndekkiteem. Juróomeelu téere bi, di Jëf ya, di nettali ci yokkutey taalibeem yi. Gannaaw loolu, ay njiiti mboolooy ñi gëm ñoo bind taalibe yi, ngir ñaax leen, ñu topp seen ngëm ci ni mu gëna dëggoo. Fukk ak ñett ci bataaxal yooyu, Póol moo ko bind. Póol nag yoon wi Yàlla wàcce ci Yonent Yàlla Musaa la topp. Dafa njëkkoona foog ne Yeesu diiŋatkat la woon, ba tax mu fitnaal taalibey Yeesu yi. Waaye gannaaw bi ko Yeesu feeñoo, mu topp ko, di tukki fépp ngir tasaare xibaaru jàmm bi. Gannaaw ñetteelu tukkeem ba, ca Korent la binde bataaxal bii, jagleel ko gëmkat ya ca Room. Demagul nag Room. Ci biir gëmkat ya dëkk Room, am na ca ñuy topp yoonu Musaa, ak ñu nekk ay yéefar laata ñuy tuub. Póol da leena bëggoona ñaax ngir ñu dund ci bennoo ak jàmm. Daf leena wax ne ñaari mbooloo yépp defuñu li Yàlla bëgg, ñoom ñépp dañoo réer. Yoonu Musaa wi Yawut yi di topp day wone lan mooy bàkkaar, waaye mayewul texe. Xelu yéefar yedd leen, waaye baña xalaat Yàlla gënal leen. Póol wone na ne nekkinu ñaari mbooloo yooyu ci kanamu àtteb Yàlla may na Boroom bi mu jox leen wenn yoonu texe: mooy gëm Yeesu Almasi bi. Dafa dee ngir gàddu mbugalu bàkkaar yi. Texe, kenn manu koo am ci def lu baax waaye ci topp Almasi bi. Noonu amul wenn lay ngir ñuy wonewu walla ñuy xeeb benn doomu aadama. Almasi bee tax Yàlla sos mbooloom gëmkat yu nekk Yawut ak yu nekkul Yawut, ngir ñu booloo ak di dund ci bëggante. Ci tënk: 1.1—3.20 Ñépp a tooñ Yàlla. 3.21—4.25 Yàlla ubbi na buntu mucc jaare ci ngëm gu ñu gëm Almasi bi. 5.1—8.39 Dund ci Almasi bi tënkuwul ci topp yoonu Musaa wi, waaye ci dooley Noowug Yàlla la nekk. 9.1—11.36 Yàlla am na mébét ngir Yawut yi ak ñi dul Yawut. 12.1—15.13 Nanu ànd booloo ci bëggante. 15.14—16.27 Póol wone na ay mébétam te nuyoo na.
7 Bataaxal bi ñeel na mboolem yeen ña fa Room, di ñu Yàlla sopp, woo leen, ngir ngeen doon ñu sell. Aw yiw ak jàmm ñeel na leen, bawoo fa Yàlla sunu Baay ak Sang Yeesu Almasi bi.
13 Bokk yi, bëgguma ngeen umple ne ay yooni yoon laa leen mébéta seetsi, ba liggéey ci seen biir lu leen jariñ, ni ma ko defale yeneen xeet; waaye ay gàllankoor a ma téye ba tey jii. 14 Muy sama digg ak Gereg yu xay yi, mbaa ñu xayadi ñi, ak ñi rafet xel, mbaa ñi ñàkk xel, am na lu ma war ci ñoom ñépp. 15 Moo tax, yeen waa Room itam, ma yàkkamti leena àggesi xibaaru jàmm bi.
21 Gannaaw ba ñu xamee Yàlla, taxul ñu màggal ko ngir li muy Yàlla, taxul ñu delloo ko njukkal, xanaa réer ci seen xalaati neen, ba seen xel mu wayadi far tàbbi cig lëndëm. 22 Xel mu rafet lañuy jaay ba mujj diy dof. 23 Leeru Yàlla ji dul dee lañu weccee jëmmu nit ki deewam dul jaas, ak picc, ak boroom ñeenti tànk, ak ndëgmeent.
24 Moo tax Yàlla bërgël leen ak seen xemmemtéef yu bon yi ci seen xol, ba ñu sóobu ci jëflantey sobe juy teddadil seen yarami bopp. 25 Ñoo weccee dëggu Yàlla aw fen, di sujjóotal aka jaamu mbindeef, bàyyi Bindkat bi yelloo cant ba fàww. Amiin.
26 Loolu moo tax Yàlla bërgël leen, bàyyi leen ak seen bëgg-bëgg yu teddadi. Seeni jigéen sax dëddu nañu jaxasoo gi leen bindub juddu sédde, ba jublu ci lu woroo ak seen bindub juddu. 27 Naka noonu, góor ñi it noppee jaxasoo ak jigéen, ni leen ko bindub juddu sédde, bay xabtaloo ci seen biir, seen bëgg-bëggi bakkan yu tar; ay góor di séq ak seen moroomi góor jëf ju gàccelu, ba tax leena jot ci seen jëmmi bopp, seen añub réeraange.
28 Gannaaw ràññee Yàlla jaralu leen dara, Yàlla it bërgël leen ak seen xel mu doyadi, ba ñuy def jooju jëf ju jekkadi. 29 Dañoo dem ba fees ak gépp xeetu njubadi akug mbon akug bëgge akug coxor. Noyyeewuñu lu moy kiñaan ak pexey bóome ak ŋaayoo akug njublaŋ ak jëf ju sew. Ay jëwkat lañu it, 30 te di yàqkati der. Ñu bañ Yàlla lañu, ñu reew, réy, di tëggu, ñu xareñ ci fexe lu bon, te déggadil seeni waajur. 31 Amuñu xel, amuñu kóllëre, amuñu xol, amuñu yërmande. 32 Moonte xam nañu xéll ne ñiy jëfe noonu, Yàlla moo daganal àtteb dee ci ñoom, te teewul ñu di ko jëfe, rax ci dolli di farle ñi koy jëfe.
Room 2 ->- a Seetal ci Abakug 2.4.
Languages