4 «Waaye li ma la sikke moo di sa cofeel ga nga jëkke woon, moom nga wacc. 5 Kon nag fàttalikul fu kawe fa nga xàwweekoo ba fii, te nga tuub, di jëfe jëf ja nga jëkke woon. Lu ko moy maay dikk ba fi yaw, daldi jële sa tegukaayu làmp fa bérebam, ndegam tuubuloo. 6 Waaye lu baax lii nag yaay boroom: ni ma sibe jëfi ngérum Nikolas[a], ni nga ko sibe.
7 «Ku ami nopp kat, na dégg li Noowug Yàlla wax mboolooy gëmkat ñi. Ku am ndam nag, maa lay may nga lekk ci garabu dund gi ci Àjjana, toolub Yàlla.
11 «Ku ami nopp kat, na dégg li Noowug Yàlla wax mboolooy gëmkat ñi. Ku am ndam nag doo loru mukk ci ñaareelu dee gi[b].
14 «Waaye lenn a ngii lu ma lay sikke: yaa ngi uuf foofu ay nit ñuy saxal njàngalem Balaam, moom mi doon xiirtal Balag‡Balaam, Balag: Balaam moo doon mbubboo turu yonent, di fexee rëbb bànni Israayil, ngir sàkku alal ci Balag buuru Mowab ci jamonoy Yonent Yàlla Musaa. Seetal ci Màndiŋ ma saar 22—23. ci tegal Israayil ndëgg-sërëx, ngir ñu lekk ñam wu ñu sarxal ay tuur, ak di moy Yàlla. 15 Naka noonu itam yaa ngi uuf ay nit ñuy saxal njàngalem ngérum Nikolas. 16 Kon nag tuubal. Lu ko moy maay dikk léegi ba fi yaw, te saamar biy lange sama gémmiñ, moom laay xareek nit ñooñu.
17 «Ku ami nopp kat, na dégg li Noowug Yàlla wax mboolooy gëmkat ñi. Ku am ndam nag, maa lay may ci mànn mu làqu mi, nga lekk, maa lay jox it aw doj wu weex; ci doj wi ñu bind tur wu bees wu kenn xamul, ku dul ka ko jot.
20 «Waaye lenn laa lay sikke: dangaa bàyyi Yesabel, jigéen joojuy tuddoo yonent, muy jàngaleeka réeral sama jaam ñi, ngir ñuy lekk ñam wu ñu sarxal ay tuur ak di moy Yàlla. 21 May naa ko ab diir, ngir mu tuub, waaye moo bëggula tuub ngànctoom. 22 Kon nag maa ngii di ko teg wopp ju ko tëral, te ñi mu àndal di njaaloo it, maa leen di teg mitit wu réy, su ñu tuubul jëf ja ñu koy roye. 23 Am mbas laay faate ay taalibeem. Su ko defee mboolooy gëmkat ñépp dinañu xam ne man maay nattu xol ak xel, te maay fey ku nekk ay jëfam.
24 «Waaye yeen ñi ci des ñépp nag, yeen waa Catir ñi toppul moomu njàngale te jotuleena xam loolu ñu naan xóotey xam-xamu Seytaane, maa ne leen, duma leen sëf beneen sëf. 25 Ŋoyleen rekk ci li ngeen am, ba kera may dikk.
26 «Ku am ndam nag, ku saxoo jëf ji ma soob, ba kera muj ga, maa lay jox sañ-sañ ci kaw xeet yi:
29 «Ku ami nopp kat, na dégg li Noowug Yàlla wax mboolooy gëmkat ñi.
<- Peeñu ma 1Peeñu ma 3 ->- a ngérum Nikolas mooy ñiy taafantaloo sañ-sañ bu ñu am, gannaaw bu ñu gëmee Yeesu, ngir daganal yenn aada yu ñaaw yu mel ni lekk lu ñu sarxal ay tuur, ak yebu ci séy yi yoon tere.
- b ñaareelu dee gi: seetal ci 20.14; 21.8.
- c Balaam, Balag: Balaam moo doon mbubboo turu yonent, di fexee rëbb bànni Israayil, ngir sàkku alal ci Balag buuru Mowab ci jamonoy Yonent Yàlla Musaa. Seetal ci Màndiŋ ma saar 22—23.
- d Seetal ci Taalifi cant 2.9.
Languages