5 Ba mu ko defee malaaka ma ma gisoon mu ŋarale géej geek jéeri ji, yékkati loxol ndijooram, jëme asamaan. 6 Mu giñ ci kiy dund ba fàww, ki sàkk asamaan ak li ci biiram, ak suuf ak li ci biiram, ak géej ak li ci biiram. Mu ne: «Négandiku wees na, 7 waaye bu bési kàddug juróom ñaareelu malaaka mi taxawee, ba mu tàmbalee wal liit gi, su keroogee pexem Yàlla miy kumpa dina sotti, na mu ko waxe woon ay jaamam, yonent yi.»
8 Ba loolu amee baat ba ma déggoon, mu bawoo asamaan, dellu wax ak man, ne ma: «Demal jël téere bu ndaw bi ñu ubbi ci loxol malaaka mi ŋarale géej geek jéeri ji.»
9 Ma dem ba ci malaaka mi, ne ko mu jox ma téere bu ndaw bi. Mu ne ma: «Jël ko te lekk ko. Dina wex ci sa biir nag, waaye ni lem lay neexe ci sa gémmiñ.»
10 Ma jël téere bu ndaw bi ci loxol malaaka mi, lekk ko, mu neex ci sama gémmiñ ni lem, waaye naka laa ko wann, mu wex xàtt ci sama biir.
11 Gannaaw loolu ñu ne ma: «War ngaa yékkatiwaat ay kàdduy waxyu jëmale ci xeet yu bare ak askan yu bare ak niti làkk yu bare ak buur yu bare.»
<- Peeñu ma 9Peeñu ma 11 ->
Languages