30
Mucc, bég
1 Dib taalifu cant, ñeel Daawuda ca daloob kër Yàlla ga.
2 Aji Sax ji, dama lay kañ.
Yaa ma yékkati,
ba noon reetaanu ma.
3 Aji Sax ji sama Yàlla, maa la woo wall,
nga faj ma.
4 Aji Sax ji, yaa ma jukkee njaniiw,
may ma bakkan, ma tàggook ñiy tàbbi njaniiw.
5 Yeen aji gëm ñi, woyleen Aji Sax ji,
njukkale ko sellaayam.
6 Meram di lu gàtt,
aw yiwam sax dàkk.
Rongooñ gane, fanaan,
ay ree xëysi.
7 Man damaa baaxle woon, ba ne:
«Deesu ma rëññeel mukk.»
8 Aji Sax ji, booba yaa ma baaxe,
dëj ma, ma ne kekk niw tund.
Nga fuuyu, ma jàq.
9 Aji Sax ji, yaw laa woo wall;
Boroom bi, yaw laa ñaanu yiw,
10 ne la: «Ma dee, tàbbi bàmmeel,
ana lu mu lay jariñ?
Nu la pëndu pax di sante,
bay biral sa kóllëre?
11 Aji Sax ji, déglul, baaxe ma;
éy Aji Sax ji, dimbali ma.»
12 Yaa ma soppil samay rongooñ ay ree,
summi sama yérey tiis, solal ma bànneex.
13 Naa la woye xol, baña selaw.
Languages