Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
125
Ku doyloo Aji Sax ji raw
1 Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla.
 
Ku doyloo Aji Sax ji,
dangay mel ni tundu Siyoŋ, doo toxu;
dangay sax ba fàww.
2 Ni tund yi yéewe Yerusalem,
ni la Aji Sax ji yéewe ñoñam,
tey ak ëllëg.
 
3 Nguur gu bon du saxe
kaw suuf su nit ñu jub muurloo.
Lu ko moy ñu jub ñi sàkku lu bon,
di ko jëfe.
 
4 Éy Aji Sax ji, baaxeel ku baax,
ak kuy mébét njub.
5 Waaye kuy topp yoonu ndëngte,
Aji Sax jee koy sànk,
boole kook kuy def lu bon.
Yal na jàmm dal ci Israayil.

<- Taalifi cant 124Taalifi cant 126 ->