1 Kon nag yeen samay bokk, soppe yi ma namm, di leen bége, te ngeen di sama kaalag ndam gi ma yooloo ci sama liggéey, ngalla soppe yi, nangeen saxe noonu ci Boroom bi!
4 Bégleen ci Boroom bi fu ngeen tollu, ma waxati ko, bégleen! 5 Na seen lewetaay wóor ñépp, Sang bi jegesi na. 6 Buleen jaaxle ci dara, waaye ci mbir mu mu mana doon, deeleen dikke Yàlla seeni soxla, di ko ñaan aka dagaan te boole ci di ko sant. 7 Su boobaa jàmmu Yàlla ji wees ab takk, mooy sàmm seen xol ak seenum xel ndax Almasi Yeesu.
8 Li ci des nag bokk yi, moo di lii: mboolem lu dëggu, ak mboolem lu tedd, ak mboolem luy njub, ak mboolem lu set, ak mboolem lu jekk, ak mboolem lees di rafetlu, ndegam lu nawlu la te yelloo ngërëm, na leen loola soxal. 9 Li ngeen jànge ci man te jële ko ci man, ak li ngeen dégge ci man, gise ko ci man, jëfeleen ko. Su boobaa Yàlla miy boroom jàmm mooy ànd ak yeen.
15 Yeen waa Filib, xam ngeen xéll ne ba waareb xibaaru jàmm bay door, te ma bàyyikoo diiwaanu Maseduwan, amul woon menn mbooloom gëmkat mu ma séqaloon ab joqalanteb ndimbal, xanaa seen mennum mbooloo. 16 Ba ma nekkee Tesalonig sax, yónnee ngeen ma ay yoon, lu ma faje samay soxla. 17 Du caageenu ndimbal lu ma sàkku ci yeen, li may sàkku kay moo di yokkuteb yool bu leen ñeel. 18 Fii ma tollu jot naa li ma aajowoo lépp, maa ngi ci naataange; doyle naa sëkk, gannaaw ba ma nangoo ci loxol Epafrodit seenub yóbbante, te sarax su ñu nangu la, di xeeñ xetug jàmm, te neex Yàlla mi mu ñeel. 19 Te sama Yàlla itam mooy sàkke ci koomam gu yéeme gi ci Almasi Yeesu, ba fajal leen seen soxla yépp.
20 Daraja ñeel na Yàlla sunu Baay, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin.
23 Yal na yiwu Sang Yeesu Almasi bi ànd ak seenum xel.
<- Filib 3
Languages