Filemon Filemon xaritu Póol la. Póol yégaloon na ko xibaaru jàmm bi, ba Filemon dogoo topp Almasi bi. Ci jamono jooju ci réew yi bokk ci nguuru Room, lu tollook genn wàllu nit ñépp nekk nañu ay jaam. Jaam bu rëcc, ñu duma ko duma yu metti, ba dee xaj ca. Filemon am na ay jaam, ba kenn ci ñoom, ku tudd Onesim, daw rëcc. Jombul dafa sàcc Filemon laata muy daw. Onesim mu ngi daje ak Póol, ci kaso bi ñu ko tëjoon. Mu dogoo topp Almasi bi, tàmbali di dimbali Póol. Póol yebal Onesim mu dellu ca Filemon ak bataaxal bii, ngir di sàkku Filemon nangu ko, def ko ni mbokkam ndax Almasi bi.
12 Maa ngi koy yebal ngir mu dellu fi yaw, te di kenn ci man. 13 Dama koo bëggoona téye fi sama wet, ngir mu taxawal la, di ma dimbali, li feek maa ngi ci kaso bi ngir xibaaru jàmm bi. 14 Waaye bëggumaa def dara loo àndul, ngir mu baña doon ndimbalu ñàkk pexe, xanaa loo defe xol bu tàlli. 15 Jombul itam dees koo tàggale ak yaw ab diir, ngir nga jotaat ci moom ba fàww, 16 ba dootul doon sab jaam, waaye day wees ab jaam, di mbokk, di soppe, ma sopp ko lool, te nga war ma koo gëna sopp, ngir jëmmu boppam ak Sang bi ngeen bokk.
17 Ndegam nag sa waay nga ma def, dalal ko ni su doon man. 18 Su la tooñee, mbaa mu ameel la lenn, topp ma ko. 19 Man Póol maay bind fii ci sama loxol bopp: maay fey loolu, duma ci tuddaale bor bi nga ma ameel, te muy sa njotug bakkanu bopp! 20 Kon nag mbokk mi, may ma googu njekk ngir Sang bi, te nga seral sama xol ndax Almasi bi. 21 Wóor na ma ci diggante bii may bind bataaxal bi, ne dinga ma déggal, te xam naa ne dinga def sax lu wees li may wax.
22 Te itam nanga ma waajalaale ab dal, ndax yaakaar naa ne dees na ma delloosi fi yeen, ndax seen ñaan yu nangu.
23 Epafras, mbokk mi ñu ma tëjandool ndax Almasi Yeesu, mu ngi lay nuyu, 24 mook Màrk ak Aristàrk ak Demas ak Luug, bokk yi may liggéeyandool.
25 Yal na yiwu Sang Yeesu Almasi bi ànd ak seenum xel.
- a njariñ: ci làkku gereg turu Onesim mooy tekki «Ku am njariñ».
Languages