5 Ba loolu wéyee, Musaa jox bànni Israayil ndigal, ci ndigalal Aji Sax ji, ne: «Dëgg la giirug Yuusufeen ñi wax. 6 Kàddu gii nag mooy li Aji Sax ji santaane ci doomi Celofat yu jigéen yooyu: Ku leen neex, nañu séy ak moom, na fekk rekk, ka ñuy séyal askanoo ci làng gu bokk ci seen giirug baay. 7 Du benn céru suuf ci biir bànni Israayil, buy jóge ci genn giir, toxu ca geneen, waaye na ku nekk ci bànni Israayil yem kepp ca suufas giiram, ga mu donne cay maamam. 8 Mboolem ku jigéen ku donn suuf ci giiri bànni Israayil, ci biir làng gu bokk ci giirug maamam rekk lay séy, ngir ku nekk ci bànni Israayil mana ñoŋal céru maamam. 9 Su ko defee du benn céru suuf buy jóge ci genn giir, toxu ca geneen, waaye giirug bànni Israayil gu ci nekk day yem kepp ca céru suufam.»
10 Na ko Aji Sax ji sante Musaa nag, na la ko doomi Celofat yu jigéen defe. 11 Muy Maxla, di Tirca, di Ogla, di Milka, di Nowa, doomi Celofat yooyu, ñoom ñépp seen bokki baay lañu séyal. 12 Ca làngi askanu Manase doomu Yuusufa lañu séy, seen céru suuf daldi des ca giir ga seen làngu baay bokk.
13 Loolu mooy santaane yeek àttey yoon yi Aji Sax ji dénkoon bànni Israayil, Musaa jottali leen ko ca joori Mowab, fa feggook dexu Yurdan, te janook Yeriko.
<- Màndiŋ ma 35- a atum Yiwiku: seetal ci Sarxalkat yi 25.8-55.
Languages