5 Ci kaw loolu Musaa jébbal Aji Sax ji àtteb jigéen ña. 6 Aji Sax ji wax Musaa ne ko: 7 «Li doomi Celofat yi wax dëgg la. Danga leen di jox kay, ab cér ci biir wàll wi seen baay bokk ak bokkam yu góor. Su ko defee nga féetale leen seen céru suufu baay.
8 «Te nga wax bànni Israayil, ne leen: “Bu ku góor deewee te bàyyiwul doom ju góor, doomam ju jigéen ngeen di jox céru suufam. 9 Su amul doom ju jigéen nag, góor ñi mu bokkal waajur ngeen di jox céru suufam. 10 Su amul góor gu mu bokkal waajur, góor ña baayam bokkal waajur, ñoom ngeen di jox céru suufam. 11 Su baayam amul góor gu mu bokkal waajur, mbokkam mu ko gëna jege ci biir làngam, moom ngeen di jox céru suufam. Kookooy donn cér ba. Na loolu di dogalu yoon, ñeel bànni Israayil, noonu ko Aji Sax ji sante Musaa.”»
15 Musaa nag wax Aji Sax ji, ne ko: 16 «Aji Sax ji, yaw Yàllay bépp boroom bakkan bu bindoo aw suux, ngalla tabbal nit ku jiite mbooloo mi, 17 kuy xareji, jiite leen, délsi, jiite leen, di leen yóbbu, di leen delloosi, ba mbooloom Aji Sax ji baña mel ni xar yu amul sàmm.» 18 Aji Sax ji ne Musaa: «Jëlal Yosuwe doomu Nuun. Nit la ku fit fees. Nanga ko teg sa loxo, sase ko noonu. 19 Taxawal ko fi kanam Elasar sarxalkat bi, ci kanam mbooloo mépp, te nga sas ko ci seen kanam, 20 daldi koy sédd lenn ci sa daraja, ngir mbooloom bànni Israayil mépp déggal ko. 21 Ca Elasar sarxalkat bi nag la war di dem, ngir mu di ko seetal fi kanam Aji Sax ji, lu Urim, jumtukaayu tegtal bi, feeñal. Ci ndigalal Elasar nag lañuy génne, te ci ndigalam it lañuy dellusee, moom Yosuwe, ak mboolem bànni Israayil giy ànd ak moom, mbooloo mépp.»
22 Ba mu ko defee Musaa def, na ko Aji Sax ji sante. Mu ànd ak Yosuwe, taxawal ko fa kanam Elasar sarxalkat bi, ak mbooloo mépp. 23 Musaa nag teg Yosuwe ay loxoom, daldi koy sas, na ko Aji Sax ji santaanee, mu jottali.
<- Màndiŋ ma 26Màndiŋ ma 28 ->
Languages