2 Ñi ko torlu ñoo di
10 Leween ñi ñoo di
15 Njiiti askan wi ñoo di
32 «Te itam bu waa réew mi indee am njaay mbaa lépp luy pepp, di ko jaay ci bésub Noflaay, dunu ko jënd ci ñoom bésub Noflaay mbaa bés bu sell.
33 «Ci biir loolu nu warloo santaaney joxe at mu nekk ñeenti garaami xaalis, bu jëm ca sunu liggéeyu kër Yàlla ga, 34 jëm ca mburum teewal ma, ak saraxi pepp yi war bés bu nekk, ak saraxi dóomal yu bés bu nekk, ak saraxi bési Noflaay, ak yu Terutel weer ak yu bési màggal yi, ak yeneen yu ñu sellalal Yàlla, ak saraxi póotum bàkkaar yi bànni Israayil di jotoo, ak mboolem la war ca sunu liggéeyu kër Yàlla ga.
35 «Ay bant lanu tegoo ci sunu biir, nun sarxalkat yeek Leween ñeek baadoolo yi, ngir dogalal waa kër gu nekk àpp ba ñu wara aye cim at, te ñu war caa yóbbu seen sasu matt ca sunu kër Yàlla ga, ngir taal ko ca sunu sarxalukaayu Yàlla Aji Sax ji, muy la ñu bind ci téereb yoon wi.
36 «Nu dogu ba tey ne dinanu yóbbu ca kër Aji Sax ji, at mu nekk, li sunu suuf njëkka meññle ak lu garab yépp njëkka ñorle. 37 Ci biir loolu nu dogoo def li ñu bind ci yoon wi, di yóbbu ca sunu kër Yàlla ga sunu taaw yu góor ak lu sunu jur taawloo, gu gudd gaak gu gàtt ga, di teg lépp ci loxoy sarxalkat ya fay liggéey. 38 Ci kaw loolu nu wara yóbbu ca sunu néegi dencukaayi kër Yàlla ga lu njëkk ci sunu nootu sunguf ak sunu njoxey pepp ak sunu meññeefi garab yépp ak sunu biiñ ak diw, di teg lépp ci loxoy sarxalkat yi. Ba tey nuy indil Leween ñi céru fukkeelub lépp luy meññee ci sunu suuf, ndax Leween ñeey dajalesi céri fukkeel yi ci gox yi nuy bey yépp. 39 Sarxalkat bu askanoo ci Aaróona mooy gunge Leween ñiy jëlsi céri fukkeel yi. Su ko defee Leween ñi yóbbu fukkeelu céri fukkeel yi ba ca sunu kër Yàlla ga, fat ko ca néegi dencukaayi alal ya. 40 Ci néeg yooyu la bànni Israayil ak askanu Leween ñi di yóbbu njoxem pepp ma ak biiñ baak diw ga; fa la ndabi kër gu sell ga dence, te fa la sarxalkat ya nekk, ñoom ña sasoo liggéey ba, ñook fara bunt yaak woykat ya. Nu dogu nag ne dunu sàggane sunu kër Yàlla ga.»
<- Neyemi 9Neyemi 11 ->
Languages