2 «Ba wittum reseñ jotee, mu yebal ab surga ca beykat ya, ñu jëlsi wàllam ca meññeef ma. 3 Beykat ya jàpp ko, dóor ko, dàq ko, mu dellu loxoy neen. 4 Boroom tóokër ba yebalaat beneen surga, ñu xaañ ko, toroxal ko. 5 Mu yebalati beneen surga, ñu rey ko. Mu dellu yebal ñu bare, ñii ñu dóor leen, ñii ñu rey.
6 «Boroom tóokër ba nag desewul kenn ku dul doomam ji mu sopp. Mu mujj koo yebal ca beykat ya te naan: “Sama doom, dinañu ko rus.” 7 Teewul beykat ya ne ca seen biir: “Kii mooy donn; nanleen ko daldi rey, ndonoom di sunu moomeel.” 8 Ñu jàpp ko, rey, génne néew ba tóokër ba, sànni ca biti.»
9 «Ana nu boroom tóokër biy def? Xanaa dikk rekk, rey beykat yi, dénk tóokëru reseñ ba ñeneen. 10 Xanaa jànguleen gii kàddu ci Mbind mi?
12 Ba loolu amee njiit ya di ko wuta jàpp, ndax xam nañu xéll ne ñoo moom léeb wa, waaye dañoo ragal mbooloo ma, ba tax ñu dem, bàyyi ko.
15 Teewul Yeesu ràññee seen jinigal, ne leen: «Ana lu ngeen may seetloo? Indilleen ma posetub dinaar, ma xool.» 16 Ñu jox ko poset, mu ne leen: «Nataal bii ak tur wii ci binde, kuy boroom?» Ñu ne ko: «Buur Sesaar.» 17 Yeesu ne leen: «Yëfi Sesaar daal, joxleen ko Sesaar, yëfi Yàlla, ngeen jox ko Yàlla.» Ñu waaru nag ci moom.
20 «Léegi juróom ñaari góor ñu bokk ndey ak baay la woon. Taaw ba am jabar, ba faatu te bàyyiwul doom. 21 Tofo ba jël ndaw sa, ba mujj dee te bàyyiwul doom. Ñaareelu tofo ba it noonu. 22 Ñu topplantee ko noonu ba juróom ñaar ñépp dee, te kenn bàyyiwul doom. Gannaaw gi, ndaw sa it dee. 23 Keroog ndekkite la nag, bu ñu dekkee, kan ci ñoom la ndaw say doon jabaram, gannaaw juróom ñaar ñépp a ko jëloon jabar?»
24 Yeesu ne leen: «Du lii mooy seen njuumte: xamuleen Mbind mi, xamuleen manoorey Yàlla! 25 Ndax ñi dee, bu ñu dekkee, kenn du ci am jabar mbaa jëkkër, waaye dañuy mel ni malaaka yi ci asamaan. 26 Te ci wàllu dee-dekki sax, xanaa jànguleen na ko téereb Musaa indee ca mbirum ngarab sa, mooy ba mu ne: “Maay Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa, di Yàllay Yanqóoba†Seetal ci Mucc ga 3.6.”? 27 Kon moom du ñi dee lay seen Yàlla, xanaa ñiy dund. Njuumte lu réy ngeen juum.»
29 Yeesu ne ko: «Ndigal li gëna am solo mooy: “Dégluleen, yeen bànni Israayil, Boroom bi sunu Yàlla, Boroom bi kenn la. 30 Kon seen Yàlla Boroom bi, nanga ko soppe sa léppi xol, ak sa léppi jëmm, ak sa léppi xel, ak sa léppi doole‡Seetal ci Baamtug yoon wi 6.4-5..” 31 Ñaareel bi mooy: “Ni nga soppe sa bopp, nanga ko soppe sa moroom§Seetal ci Sarxalkat yi 19.18..” Ndigal gënula màgg yii.»
32 Firikatu yoon bi ne ko: «Waawaaw, Kilifa gi, yaa wax dëgg; Yàlla kenn la, te amul jeneen Yàlla ju dul moom. 33 Te it nga soppe ko sa léppi xol, ak sa léppi xel, ak sa léppi doole, te ni nga soppe sa bopp, nanga ko soppe sa moroom; loolu moo gën mboolem saraxi dóomal, ak yeneen sarax yu mu mana doon.»
34 Yeesu nag gis ne waa ja waxe xel, mu ne ko: «Sorewuloo nguurug Yàlla de.» Ba loolu amee kenn ñemeetu koo laaj dara.
37 Yeesu neeti: «Gannaaw Daawuda ci boppam moo woowe Almasi bi “Sang bi,” ana kon nu mu nekke ab sëtam?» Mbooloo mu baree nga fa woon, di ko dégloo mbég.
38 Yeesu teg ca xamal leen ne leen: «Moytuleen firikati yoonu Musaa yi taamoo jaagar-jaagareek seen mbubb yu réy, di sàkku nuyoob wegeel ca pénc ma, 39 ak toogu yu kaname ca jàngu ya, ak péetey teraanga ca bernde ya. 40 Ñooy saax-saaxee alalu jëtun ñi tey ñaan ñaani ngistal yu dul jeex. Ñooñu la seen mbugal di gëna tar.»
43 Yeesu nag woo taalibe ya, ne leen: «Maa leen ko wax déy, mboolem ñi sànni xaalis ci ndab li, jëtun bu néew doole bii moo leen ëpple lu mu ci sànni. 44 Ndax ñoom ñépp ci seen koom lañu sàkke as lëf, sànni ci ndab li, waaye moom de, ci biirug ndóolam la jële la mu amoon lépp, dundam bépp, sànni ci.»
<- Màrk 11Màrk 13 ->
Languages