Macë Mas ngaa xalaat ci dundug Almasi bi? Lu ko gàddaayloo mu jëm Afrig? Kañ la dox ci kaw ndox? Lu tax ñu bëgg koo rey? Kañ lay dellusi àddina? Dinga gis ay tont ci téere bii. Dafa am ñeenti téere yu ay taalibey Yeesu Almasi bi bind ci ag dundam ak ay jàngaleem. Macë ab juutikat la woon jamono ji ko Yeesu woowee ngir mu nekk ab taalibeem (10.3). Téere bi mu bind, la mu ca jublu mooy mu won Yawut yi ne Yeesu mooy Almasi bi leen Yàlla digoon. Macë daldi tàmbali ci ni Yeesu askanoo te muy wone ne mooy sëtu Buur Daawuda te di sëtu Yonent Yàlla Ibraayma. Macë am na lu bare lu mu yégle ci nguurug Yàlla. Yeesu mi ngi waare naa: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndax nguurug asamaan dëgmal na» (3.2). Nguuru Yàlla ci asamaan masu fee jóge, waaye dafa ñàkk ci àddina. Yàlla jox na sañ-sañ nit ngir mu yilif àddina. Waaye nit a tooñ Yàlla, gannaaw bi ko Seytaane naxee, ba nangu sañ-sañ bi. Kon nag Yàlla yónni na Almasi bi, ngir mu nanguwaat sañ-sañ bi. Gannaaw bi Yeesu dekkee, mu ne: «Joxees na ma bépp sañ-sañ fa asamaan ak fi kaw suuf» (28.17). Ci tënk: 1.1—4.25 Yeesu juddu na, tàmbali na liggéeyam. 5.1—7.29 Yeesu mi ngi firi yoonu Yàlla wi. 8.1—18.35 Yeesu day faj, di def ay kéemaan ak di jàngale. 19.1—23.39 Yeesu day tukki Yerusalem. 24.1—25.46 Yeesu day jàngale ci mujug jamono ak delluseem. 26.1—28.20 Yeesu dee na, dekki.
12 Gannaaw ba ñu leen gàddaayloo ñu dem Babilon la Yekoña jur Selcel; Selcel jur Sorobabel, 13 Sorobabel jur Abiyudd; Abiyudd jur Elyakim; Elyakim jur Asor; 14 Asor jur Cadog; Cadog jur Akim; Akim jur Elyudd; 15 Elyudd jur Elasar; Elasar jur Matan, Matan jur Yanqóoba; 16 Yanqóoba nag moo jur Yuusufa jëkkëru Maryaama; te Maryaama moo jur Yeesu, mi ñuy wax Almasi bi.
17 Mboolem maas yi dox diggante Ibraayma ba ca Daawuda nag di fukki maas ak ñeent; li dox diggante Daawuda ba ca njaam ga ca Babilon, di fukki maas ak ñeent; li dox diggante njaam ga ca Babilon ba ci Almasi bi, di fukki maas ak ñeent.
22 Loolu lépp a sotti ngir matal la Boroom bi waxe woon ca làmmiñu yonent ba, ba mu nee:
24 Ba Yuusufa yewwoo, la ko malaakam Boroom bi sant la def, daldi yeggali jabaram. 25 Waaye Yuusufa àndul ak moom, ba kera mu ame doom, muy góor, mu tudde ko Yeesu.
Macë 2 ->
Languages