5 Seytaane yéege na ko fu kawe itam, won ko mboolem nguuri àddina, ci xef ak xippi. 6 Seytaane ne Yeesu: «Yaw laay may mboolem kilifteef gii ak daraja ji mu àndal, ndax man lees ko jox, te ku ma soob laa koy may. 7 Kon nag soo ma sujjóotalee, yaa moom lépp.» 8 Yeesu ne ko: «Bindees na ne:
9 Seytaane yóbbu na ko Yerusalem, aj ko ca njobbaxtalu kër Yàlla ga, ne ko: «Ndegam yaa di Doomu Yàlla, tëbeel fii, wàcc, 10 ndax bindees na ne:
13 Seytaane lalal na Yeesu gépp fiir ba sottal, doora dem, bàyyi ko ab diir.
16 Yeesu moo dikkoon Nasaret ga mu yaroo, daldi dugg ca jàngub Yawut ba, na mu ko baaxoo woon ci bésub Noflaay. Mu taxaw ngir biral ab dog. 17 Ñu jox ko téereb Yonent Yàlla Esayi. Mu ubbi téere bi, gis dog bi ñu bind ne:
20 Ci kaw loolu mu ub téere bi, delloo ko jawriñ ja, daldi toog. Ña ca jàngu ba ñépp nag ne ko jàkk. 21 Mu àddu, ne leen: «Tey jii la Mbind mii mat, ngeen dégg.» 22 Ñépp a doon seedeel Yeesu lu rafet, tey yéemu ci kàdduy yiw yi tukkee ci gémmiñam. Ñu naan: «Xanaa kii du doomu Yuusufa ji?» 23 Mu ne leen: «Xam naa ne dingeen ma waxal waxin wi ñu naan: “Fajkat bi, fajal sa bopp.” Mboolem li nu dégg ne moo xew Kapernawum, def ko fii ci sa réewum bopp itam.» 24 Mu neeti: «Maa leen ko wax déy, amul benn yonent bu ñu teral ci réewu boppam. 25 Maa leen wax ne liy dëgg moo di, ca jamonoy Ilyaas, ba asamaan tëjoo diiru ñetti at ak juróom benni weer, ba xiif bu metti am ca réew mépp, ay jëtun ñu baree nga woon ca Israayil. 26 Moona du kenn ci ñoom ku ñu yebal Ilyaas ca moom ku moy jëtun ba dëkke Sarebta, ca Sidon. 27 Jamonoy Yonent Yàlla Alyaasa itam, ay gaana yu baree nga woon ca Israayil. Waaye fajeesu ci kenn ku moy Naaman, waa Siri ba.»
28 Ba mboolem waa jàngu ba déggee loolu dañoo mer ba fees. 29 Ñu jóg, bëmëx ko ba génne ko dëkk ba, yóbbu ko ca kéméju tund wa seen dëkk ba sance, ngir xalab ko ci suuf. 30 Teewul moom mu jaare ci seen biir, dem yoonam.
36 Ba loolu amee ñépp a yéemu, di wax ci seen biir, naan: «Gii kàddu lu mu doon? Moom de sañ-sañ ak xam-xam lay joxe rab yi ndigal, ñu génn.» 37 Coowal Yeesu nag law ba fépp fu bokk ca diiwaan ba.
40 Ba jant sowee, mboolem ña amoon ay jarag yu ame ay jàngoroy jàngoro, daldi leen indil Yeesu. Moom it, mu teg kenn ku ci nekk ay loxoom, wéral la. 41 Ay rab itam di génne ci ñu bare, di yuuxu, te naan: «Yaay Doomu Yàlla!» Teewul mu gëdd leen, aaye leen ñu wax, ndax xamoon nañu ne mooy Almasi bi.
42 Njël gu njëkk ca ëllëg sa la Yeesu génn dëkk ba, dem ba béreb bu wéet. Mbooloo ma nag di ko seet, ba dikk, di ko téye, bañ mu dem, ba leen. 43 Mu ne leen: «Yeneen dëkk yi it, war na ma faa yégleji xibaaru jàmm bu nguurug Yàlla, ndax looloo tax ñu yebal ma.» 44 Ci kaw loolu muy waare ca jànguy Yawut ya ca réew mi.
<- Luug 3Luug 5 ->
Languages