5 Yeesu teg ca ne leen: «Ana kan ci yeen moo seeti ab xaritam xaaju guddi, ne ko: “Xarit, lebal ma ci ñetti mburu. 6 Sama xarit bu nekk ciw yoon moo dikk sama kër, te awma dara lu ma ko taajal,” 7 te xarit ba àddoo ca biir néegam, ne ko: “Bu ma sonal, tëj naa ba tëdd, maak samay doom; manumaa jóg, di la jox dara”? 8 Maa leen ko wax, su jógul jox ko la mu laaj ndaxug xaritoo it, la ko kee amul kersay yee ngir sàkku ndimbal mooy tax mu jóg, jox ko mboolem lu mu soxla. 9 Moo tax ma ne leen, ñaanleen, ñu may leen; seetleen, ndax ngeen gis; fëggleen, ñu ubbil leen. 10 Ndaxte képp ku ñaan, dinga am; ku seet, gis; ku fëgg it, dees na la ubbil. 11 Ana kan ci yeen mooy baay bu doomam ñaan aw jën, mu jox ko jaan? 12 Mbaa mu ñaan ko nen, mu jox ko aw jiit? 13 Ndegam yeen ñi bon yeena mana may seeni gone lu baax nag, astamaak Baay ba fa asamaan. Moo leen ko dàq fuuf, nde mooy may Noo gu Sell gi, ñi ko ko ñaan!»
16 Ñeneen nag di ko fiir, di sàkku ci moom firnde ju bawoo ci asamaan. 17 Yeesu itam ràññee seen xalaat, ne leen: «Gépp nguur guy xàjjalikoo ci biiram, day tas, yii kër màbb ca kaw yee. 18 Seytaane itam, su xàjjalikoo ci biiram, ana nu nguuram di yàgge, gannaaw yeena ne Beelsebul laay dàqe ay rab? 19 Te it ndegam man Beelsebul laay dàqe rab yi, seen ñoñ nag ñoom, kan lañuy dàqe ay rab? Kon kay seen ñoñ a leen tiiñal. 20 Waaye su dee loxol Yàlla laay dàqe rab yi nag, kon nguurug Yàlla agsi na ba ci yeen.
21 «Su ponkal gànnaayoo ba diis, wattu këram, alalam dina raw. 22 Waaye bu ko ku ko man songee, ba daan ko, day nangu mboolem ngànnaay lu mu yaakaaroon, ba noppi séddale alalam. 23 Ku farul ak man nag, man ngay xeex, te ku àndul ak man di dajale, yaa ngi tasaare.
24 «Aw rab, bu jàppee nit ba bàyyi ko, day wër béreb yu fendi, di wut fu mu noppaloo, te du ko gis. Su ko defee mu ne: “Naa dellu ca sama kër ga ma jóge.” 25 Bu dikkee fekk kër gi buube, defare ba jekk, 26 day dem indi yeneen juróom ñaari rab yu ko yées, ñu bokk sancsi. Su ko defee ni nit kiy mujje mooy yées na mu jëkke.»
27 Naka la Yeesu di wax loolu, jenn jigéen ca mbooloo ma àddu ca kaw, ne ko: «Ndokkalee ki la ëmb ci biiram, nàmpal la ci weenam!» 28 Moom nag mu ne ko: «Xanaa kay, ndokkalee ñiy déglu kàddug Yàlla te di ko jëfe.»
45 Kenn ci xamkati yoon yi nag àddu ne: «Kilifa gi, loolu nga wax de, nun itam, xasaale nga nu ci.» 46 Yeesu itam ne: «Yeen xamkati yoon yi itam, wóoy ngalla yeen, yeen ñi sëf nit ñi sëf yu ñu àttanul, te yeen ci seen bopp, seen benn baaraam sax du ci laal. 47 Wóoy ngalla yeen, yeenay tabax bàmmeeli yonent yi, te seeni maam reyoon leen. 48 Kon yeena seedee noonu ne seen jëfi maam ya, ànd ngeen ci, ndax ñoom ñoo leen rey, yeen ngeen tabax seeni bàmmeel. 49 Looloo tax itam kàddug Yàlla giy xel, biral ne: “Maay yebal fa ñoom ay yonent aki ndaw, ñii ñu bóom, ñee, ñu bunduxataal.” 50 Su ko defee yoon topp niti tey jii deretu mboolem yonent yi tuuru, dale ko ca ba àddina sosoo. 51 La dale ca deretu Abel ba ca deretu Sàkkaryaa†Seetal ci 2.Jaar-jaar ya 24.20-22., ma ñu rey ca diggante sarxalukaay ba ak kërug jaamookaay ga, maa leen ko wax déy, dees na ko toppe niti tey jii. 52 Ngalla yeen xamkati yoon yi, yeena sànk caabiy xam-xam; yeen dugguleen, ñiy duggsi, ngeen tere leena dugg.»
53 Ba Yeesu génnee foofa, ca la Farisen ya ak firikati yoonu Musaa ya tàmbalee xabtalu ci kawam, di ko seetloo ay laaj ci mbir yu bare, 54 di ko yeeru, tey wuta këf kàddu gu rëcce ci gémmiñam, ngir tuumaal ko.
<- Luug 10Luug 12 ->
Languages