Luug Luug ak Jëf ya daan nañu bokk ci benn téere bi Luug bind. Ñaar yépp a indi ni Yàlla njëkka woowe bànni Israayil ba noppi, doora woo mboolem xeet yi, ngir ñu barkeele ci Ibraayma. Ci Luug, nettali bi, Yerusalem la jublu, ci péncum cosaanu Yawut yi. Ci Jëf ya, Yerusalem la nettali bi bawoo, jëm ci xeeti àddina yi ci des. Ci tënk: 1.1—9.50 Liggéeyu Yeesu ca diiwaanu Galile la doore. 9.51—19.27 Tukkib Yeesu ci Yerusalem. 19.28—24.53 Almasi Yeesu sarxe na bakkanam ca Yerusalem, te gannaaw gi, mu dekki.
8 Sàkkaryaa la làngam aye woon, muy def liggéeyu carxalam fa kanam Yàlla. 9 Ba ñu tegoo bant, na ko sarxalkat yi baaxoo woon, moom la bant ba dal, mu wara dugg ci biir néegu Boroom bi, ngir taal fa saraxu cuuraay.
10 Mbooloo mépp nag a nga woon ca biti di ñaan, ca waxtuw saraxu cuuraay boobu. 11 Ci biir loolu menn malaakam Boroom bi jekki feeñu Sàkkaryaa, ca wetu ndijooru sarxalukaayu cuuraay ba. 12 Ba ko Sàkkaryaa gisee daa jaaxle, tiitaange jàpp ko. 13 Malaaka ma ne ko: «Sàkkaryaa, bul tiit, ndax sa ñaan nangu na. Elisabet sa soxna dina am doom ju góor, nanga ko tudde Yaxya. 14 Dinga am mbégte ak bànneex, te ñu bareey bég ci juddoom, 15 ndax ku màgg lay doon, Boroom bi seede. Biiñ ak lenn luy màndil nag, du ko naan, Noo gu Sell gi mooy dale ca biiru ndeyam, solu ko ba fees. 16 Ñu bare ci bànni Israayil, moo leen di waññi ci Boroom bi seen Yàlla. 17 Mooy ndaw li koy jiitu, ànd ak leer ga ak xam-xam ba woon ca Yonent Yàlla Ilyaas, ba waññi xolu baay ci doomam, waññi ku déggadi ci xelum aji jub, loolu yépp ngir waajal aw xeet, ba ñu jekk ngir Boroom bi.»
18 Sàkkaryaa nag ne malaaka mi: «Lu may def ab takk ci loolu ba mu bir ma? Ndax man màggat naa, te sama soxna it làq na ay fan.» 19 Malaaka ma ne ko: «Man maay Jibril miy taxaw fi kanam Yàlla. Dañu maa yónni ngir ma wax ak yaw, yégal la bii xibaaru jàmm. 20 Léegi nag, dama ne, gannaaw gëmuloo sama kàddu, giy jot, sotti, dinga luu te dootuloo mana wax, ba kera loolu di am.»
21 Ci biir loolu mbooloo maa ngay xaar Sàkkaryaa, jaaxle lool ndax yàggaayam ca biir néegu Yàlla ba. 22 Ba mu génnee nag, manula wax ak ñoom. Ñu daldi xam ne am na lu ko feeñu ca néegu Yàlla ba. Ma nga leen di liyaar, manatula wax.
23 Naka la Sàkkaryaa fégal ayu carxalam, daldi ñibbi. 24 Gannaaw gi, soxnaam Elisabet ëmb. Lëlu na juróomi weer. Ma nga naan: 25 «Lii Boroom bee ma ko defal ci jant yi mu ma geesoo, ba teggil ma sama gàcce gi ci biir nit ñi!»
29 Waxi malaaka ma nag jaaxal Maryaama, muy xalaat lu nuyoo boobu mana tekki. 30 Malaaka ma ne ko: «Maryaama, bul tiit, ndax daje nga ak yiwu Yàlla. 31 Dinga ëmb, ba jur doom ju góor, nga tudde ko Yeesu*Yeesu ci làkku ebrë mooy Yosuwe, muy firi Aji Sax jeey musle. Aji Sax ji mooy tur wi Yàlla firil Musaa ci Mucc ga 3.13-15.. 32 Ku màgg lay doon, te dees na ko woowe Doomu Aji Kawe ji. Boroom bi Yàlla moo koy jagleel nguurug Daawuda maamam. 33 Mooy nguuru fi kaw waa kër Yanqóoba ba fàww, te nguuram du foq mukk.»
34 Ci kaw loolu Maryaama laaj malaaka mi ne ko: «Nu loolu di ame, te man ab janq laa?» 35 Malaaka mi ne ko: «Noo gu Sell gi mooy wàccsi ci yaw, dooley Aji Kawe ji yiir la. Moo tax itam kiy juddoo ci yaw, dees na ko woowe Ku sell, ak Doomu Yàlla. 36 Te kat Elisabet sa mbokk mi itam ëmb na doom ju góor te fekk ko màggat. Ki ñu doon woowe jigéen ju jaasir, mu ngi nii ci juróom benni weeram, 37 ndax Yàlla, dara tëwu ko.» 38 Maryaama daldi ne: «Maa ngi, di jaamub Boroom bi. Nii nga waxe, na ame noonu ci man.»
56 Maryaama toog na fa Elisabet lu wara tollook ñetti weer, sooga ñibbi.
59 Ba bés ba délsee, ñu dikk xarafalsi xale ba, bëgg koo tudde Sàkkaryaa, dippee ko baayam. 60 Yaayam nag ne leen: «Déet, Yaxya lay tudd.» 61 Ñu ne ko: «Waaye kenn ci say bokk tuddul noonu!»
62 Ci kaw loolu ñu liyaar baayam, ngir xam nu mu bëgg ñu tudde xale bi. 63 Sàkkaryaa laaj àlluwa, ñu jox ko, mu bind ci: «Yaxya mooy turam.» Ñépp waaru. 64 Ca saa sa gémmiñ ga ubbiku, làmmiñ wa nangu, muy wax, daldi sant Yàlla. 65 Ba loolu amee tiitaange dikkal mboolem ña leen séq, te mbir moomu mépp nag doon waxtaan ca diiwaanu tundi Yude gépp. 66 Ña ca dégg ñépp daldi bàyyi xel ca mbir ma, te naan: «Lu xale bii nara doon ëllëg?» ndax manoorey Boroom bee àndoon ak moom.
Languages