5 «Buñu wat fenn ci seen bopp te buñu wat seen peggi sikkim, buñu dagg seen yaram it, di ko mititloo ku dee. 6 Nañu nekkal seen Yàlla ay nit ñu sell, te baña teddadil seen turu Yàlla, ndax saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji, te di seen ñamu Yàlla, ñoo koy joxe. Kon nag dañoo wara sell.
7 «Ab gànc mbaa ku ñu toroxal, tëdde ko, ñoom duñu ko jël soxna. Ku jëkkëram baal it duñu ko jël soxna, ndax dañoo sellalal seen bopp seen Yàlla. 8 Te itam nangeen ràññee ne ñu sell lañu, ndax seen ñamu Yàlla, ñoo koy joxe. Nangeen leen jox céru nit ñu sell, ndax Ku sell laa, man Aji Sax ji leen sellal, yeen.
9 «Su fekkee ne doomu sarxalkat da di jigéen juy teddadil boppam, di gànctu, kooku baayam lay toroxal. Dees koy taal, lakk ko.
10 «Sarxalkat bi gëna màgg ci bokkam yiy sarxalkat, te ñu sotti diw gi ñuy fale ci boppam, sellal ko, muy sol yére yu sell yi, kooku du njañu te du xotti ay yéreem, di ko ñaawloo ku dee. 11 Fu ab néew nekk du fa dem, bu doon ndeyam mbaa baayam sax, du ko taxa sobeel boppam. 12 Du génn béreb bu sell bi ndax deele, lu moy dina teddadil bérebu Yàllaam bu sell bi, ndax Yàllaam sellale na ko diwug palam. Maay Aji Sax ji.
13 «Sarxalkat bu mag bi, ku xamul góor lay jël soxna. 14 Ku jëkkëram faatu mbaa ku ñu baal mbaa ku ñu toroxal, tëdde ko, mbaa ab gànc, du ko mana jël soxna. Ab janq bu mu bokkal doŋŋ la mana jël soxna. 15 Su ko defee du teddadil aw askanam ci biir bànni Israayil, ndax man Aji Sax ji maa ko sellal.»
24 Musaa jottali na Aaróona aki doomam kàddu yooyu, ñoom ak mboolem bànni Israayil.
<- Sarxalkat yi 20Sarxalkat yi 22 ->
Languages