4 Ba mu ko defee Musaa woolu Misayel ak Elcafan, góor ñiy doomi Usyel, baayu Aaróona bu ndaw. Mu ne leen: «Kaayleen jële fi seen bokk yii ci kanamu xaymab ndaje bi, te ngeen génne leen dal bi.» 5 Ñu jàpp ca seeni jàllaabi, génne leen dal ba, muy la Musaa santaane woon. 6 Musaa wax Aaróona ak doomam yu góor yi tudd Elasar ak Itamar ne leen: «Buleen njañu te buleen ñaawlu di xotti seeni yére, lu ko moy dingeen dee, te sànjum Yàlla dina dal ci kaw mbooloo mi mépp. Waaye seen bokki bànni Israayil gépp sañ nañoo jooy ñi Aji Sax ji lakk. 7 Bunt xaymab ndaje mi, buleen ko wees, lu ko moy dingeen dee, ndax diwu palu Aji Sax jaa ngi ci seen kaw.» Ñu def la leen Musaa sant.
12 Ci kaw loolu Musaa wax ak Aaróona ak doomam yu góor yi des, di Elasar ak Itamar, ne leen: «Jëlleen saraxu pepp mi des ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji, ngeen lekk ko, bañ cee boole lawiir, ci wetu sarxalukaay bi, ndax lu sella sell la. 13 Lekkleen ko ci béreb bu sell. Sa cér la, yaw ak say doom yu góor, ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji. Loolu lañu ma sant. 14 Waaye dënnu saraxu yékkati-jébbale bi ak tànk bi ñu jébbal, lekkleen ko ci béreb bu mucc sobe, yaak say doom yu góor ak say doom yu jigéen, ndax seen cér la, ci saraxi canti bànni Israayil ci biir jàmm, nga moom ko yaak say doom. 15 Tànk bi ñu jébbal ak dënnu saraxu yékkati-jébbale bi, mook nebbon bi ñuy def saraxu sawara, dees koy boole indi yékkati ko, def ko sarax bu ñuy yékkati, jébbal Aji Sax ji. Yeena moom yooyu, yaak say doom, muy seen cér bu ñu leen dogalal fàww, te di la Aji Sax ji santaane woon.»
16 Gannaaw loolu Musaa laajte, ba am lu leer ci mbirum sikketu saraxas póotum bàkkaar bi, ndekete lakk nañu ko, ba mu dib dóom. Mu mere ca doomi Aaróona yu góor ya des, di Elasar ak Itamar, ne leen: 17 «Lu waral lekkuleen sarax biy póotum bàkkaar ci béreb bu sell? Lu sella sell la, ñu jox leen ko, ngeen war koo yenniku bàkkaaru mbooloo mi, ba defal leen seen njotlaay fi kanam Aji Sax ji. 18 Gannaaw dugaleesul deret ji ca biir néeg bu sell ba, waroon ngeena lekk sikket bi ci béreb bu sell, muy li ma santaane woon.» 19 Aaróona ne Musaa: «Xoolal rekk tey ni bànni Israayil indile Aji Sax ji seen saraxu póotum bàkkaar ak seen saraxu rendi-dóomal, te teewul lii dal ci sama kaw! Bu ma lekkoon tey ci yàppu saraxas póotum bàkkaar bi, ndax dina neex Aji Sax ji?» 20 Musaa dégg kàddu yooyu, rafetlu ko.
<- Sarxalkat yi 9Sarxalkat yi 11 ->
Languages