Yudd Ki bind bataaxal bii, Yudd, rakku Yeesu la woon ni Yanqóoba mi bind it bataaxal bu ñu ko dippee (Macë 13.55). Yudd moo ñaax gëmkat ñi, ne leen ñu xeexal yoonu ngëm, di moytu jàngalekati caaxaan yi yoxoosu ci seen biir, ñoom ñi ñeme Yàlla tey xuus cig yàqute, te seenug sànkute du jaas. Mujj, Yudd ñaanal gëmkat ñi ci turu Ki leen mana aar ci bépp jéll.
5 Doonte xam ngeen loolu lépp ba noppi, dama leen di fàttali rekk ne Boroom bi moo njëkka musal ñoñam, génne leen réewum Misra, te gannaaw gi moo raafal ña gëmul woon ca ñoom. 6 Te it malaaka ya yemul woon ca daraja ja ñu amoon, xanaa wacc seen dëkkuwaayu bopp, Yàlla moo leen denc ci lëndëm gu ne këruus, yeewe leen jéng yu dul deñ, ngir àtteb bés bu mag ba. 7 Naka noonu itam Sodom ak Gomor ak dëkk ya leen wër, ñoo yebu woon ci séy yi yoon tere ak jaxasoo gu woroo ak bindub judduwaale, ba ñu def leen misaal, ñeel ña nara tegoo mbugalum sawara su sax dàkk.
8 Géntkat yii itam noonu rekk lañuy sobeele seen yaramu bopp, boole ci di sofental kilifteef, ak di saaga boroom daraja ya fa asamaan. 9 Moonte Mikayel may kilifag malaaka sax, ba muy xëccoo ak Seytaane néewub Musaa, di wàqante ak Seytaane, taxul mu ñeme woon koo sikk ba boole ciy saaga. Da ko ne rekk: «Yal na la Boroom bi mbugal!» 10 Waaye nit ñii de, lu ñu xamul lañuy saaga, te xam-xam yi leen seen bindu judduwaale xamal, ni ay rabi àll di xame, ci lañuy far yàqoo.
11 Ngalla ñii! Ñoo jaare yoonu Kayin; ñoo lajj, topp Balaam cig réeram ngir ag peyoor; ñoo diiŋat ba sànku ni Kore*Kayin: seetal ci Njàlbéen ga 4.8. Balaam: Màndiŋ ma 22.7-35; 31.16. Kore: Màndiŋ ma saar 16.. 12 Ñooñooy gàkkal seen jataayu lekk yi gëmkat ñiy bokk, di ñóox te amuñu ci jenn jom; ñooy xiin yu naaxsaay yu ngelaw li yóbbu; ñooy garab yu dee ñaari yoon, du meññ waxtoom, reen ya buddiku. 13 Ñooy gannaxi géej gu sàmbaraax, di gëq seen puuriti gàcce; ñooy biddiiw yu fàq di taxawaalu, te lëndëm gu ne këruus di cér bu ñu leen sédde ba fàww.
14 Enog†Enog: seetal ci Njàlbéen ga 5.21-24., juróom ñaareelu maam ma gannaaw Aadama, ñooñu la jottali woon waxyu bu leen dal, ne: «Boroom baa ngii dikk, ànd ak ay junniy junneem ñu sell, 15 ngir àtte ñépp, ba tiiñal mboolem yéefar yi, ndax mboolem nu yéefare ni ñu jëfe seen jëfi yéefar ak mboolem kàddu yu ñaaw yi bàkkaarkati yéefar yi teg cib deram.» 16 Ñooñoo di ñaxtu aka jàmbat, te topp seen bakkan; kàdduy damu yu réy ay jibe seen gémmiñ, te ñooy jay ñi ñu yaakaare njariñ.
Languages