2 Jant yooyu la Aji Sax ji wax Yosuwe ne ko: «Yattlul ay paakay xeer te nga jubluwaat, muy ñaareel bi yoon, ci xarafal maasu bànni Israayil gu góor gii xarafuloon.» 3 Yosuwe yattlu ay paakay xeer, daldi xarafal bànni Israayil yu góor, ca tundu Aralot (muy firi tundu Mbuñuka ya).
4 Lii nag moo waral Yosuwe xarafal leen: Mboolem ña jóge woon Misra, te diy góor, mboolem ña xare waroon, ñoom ñépp a dee ca màndiŋ ma, ca yoon wa, gannaaw ba ñu jógee Misra. 5 Mboolem ña jóge woon Misra, xarafoon nañu. Waaye mboolem ña juddoo ca màndiŋ ma, ca yoon wa, gannaaw ba ñu fa génnee, ñooñu ñoo xarafagul woon. 6 Ndaxte ñeent fukki at la bànni Israayil wëndeelu ca màndiŋ ma, ba mboolem ña xare waroon, ba ñuy génn Misra, ñépp dee ba jeex tàkk, ngir seen ñàkka déggal Aji Sax ji. Ñoom la Aji Sax ji giñaloon ne du leen won réew mi mu giñaloon seeni maam, ne dina nu ko jox, réew mu meew maak lem ja tuuroo. 7 Seen doom ya mu def seen kuutaay nag, ñoom la Yosuwe xarafal, ndax ñoo xaraful woon, gannaaw xarafaleesu leen woon ca yoon wa. 8 Gannaaw ba ñay xaraf ñépp xarafee ba noppi, foofa ca dal ba la bànni Israayil toog, ba ñu wér.
9 Ba loolu amee Aji Sax ji ne Yosuwe: «Bésub tey, maa taxañ gàcceg Misra, teggil leen ko.» Ca la turu béreb boobu di Gilgal (muy firi Taxañ), ba tey jii.
11 Ca ëllëg sa, gannaaw ba ñu baaxantalee bésub Mucc ba, bésub keroog booba, ca meññeefum réew ma lañu lekk, te muy mburu mu amul lawiir ak mbool. 12 Mànn ma nag ma nga dakke ca ba ñu lekkee ca meññeefum réew ma, bésub keroog ca ëllëg sa, gannaaw bésub Mucc ba. Fa la bànni Israayil doxe amatuñu mànn. At mooma, la ñore suufas Kanaan lañu dunde.
- a Seetal ci Mucc ga 3.5.
Languages