3 Piyeer ak beneen taalibe ba dem wuti bàmmeel ba. 4 Ñu ànd daw, beneen taalibe ba nag gëna gaaw Piyeer, jëkk ko ca bàmmeel ba. 5 Naka la sëgg, yër, daldi séen sori càngaay ya ca suuf, te duggul ca biir bàmmeel ba. 6 Simoŋ Piyeer ma ca topp, agsi, jàll ca biir, daldi gis sori càngaay la tege, 7 ak kaala ga ñu muure woon boppu Yeesu. Kaala ga nag àndul ak sori càngaay la; dees koo taxañ, mu tege. 8 Ci noonu beneen taalibe ba njëkkoona agsi ca bàmmeel ba, duggsi moom itam. Mu gis, daldi gëm. 9 Ndax kat ba booba, taalibe ya xamaguñu dëgg tekkitel Mbind ma indi woon ne fàww Yeesu dekki. 10 Taalibe ya nag ñibbi.
14 Naka la wax loolu daldi walbatiku, gis Yeesu mu taxaw, te xamul ne Yeesu la. 15 Yeesu ne ko: «Ndaw sii, looy jooy? Kooy seet?» Mu foog ne boroom tool baa, ne ko: «Góor gi, su fekkee yaa ko yóbbu, wax ma foo ko denc, maa koy jëli.» 16 Yeesu ne ko: «Maryaama.» Mu geestu, làkk ko ci yawut ne ko: «Rabbuni!» Muy firi kilifa gi.
17 Yeesu ne ko: «Bu ma langaamu, ndax yéegeeguma fa Baay ba. Waaye demal, ne samay bokk, maa ngi yéegi ca sama Baay biy seen Baay, sama Yàlla jiy seen Yàlla.» 18 Ba loolu amee Maryaama ma dëkk Magdala dem, ne taalibe ya: «Gis naa Sang bi!» Ci kaw loolu mu wax leen yóbbanteem.
22 Naka la wax loolu, daldi leen ëf ngelawal gémmiñam, ne leen: «Jëlleen Noo gu Sell gi. 23 Képp ku ngeen baal ay bàkkaaram, baalees na ko; képp ku ngeen topp ay bàkkaaram, toppees na ko.»
26 Ba ñu ca tegee juróom ñetti fan, taalibey Yeesu ya dajewaat ca biir, Tomaa nekk faak ñoom. Yeesu ne jimeet ca seen biir, te bunt ya tëje. Mu ne leen: «Jàmm ngeen!» 27 Ci kaw loolu mu ne Tomaa: «Tegal fii sa baaraam te xool samay loxo; te nga tàllal sa loxo, ne ko tegg ci samag wet. Bàyyil gëmadi te gëm.» 28 Tomaa àddu ne ko: «Yaa di sama Boroom, di sama Yàlla!» 29 Yeesu ne ko: «Danga maa gis, ba tax nga gëm? Ndokkalee ñi gëm te gisuñu!»
30 Bare na firnde yeneen yu Yeesu def fi kanam taalibe yi, te bindeesu ko ci téere bii. 31 Lii nag lañu bind, ngir ngeen gëm ne Yeesu mooy Almasi bi, Doomu Yàlla, ngir itam ngeen jagoo ag dund ndax aw turam.
<- Yowaan 19Yowaan 21 ->
Languages