5 «Man maay reseñ gi, yeen ngeen di car yi. Ki sax ci man, ma sax ci moom, kooku mooy meññ lu bare, nde su dul man, dungeen mana def dara. 6 Ku saxul ci man daa mel ni ab car bu ñu sànni, mu wow, te yooyu car lees di buub, sànni ci sawara, mu lakk. 7 Su ngeen saxee ci man te samay wax sax ci yeen, lu ngeen bëgg, ñaanleen ko, dees na leen ko nangul. 8 Li feeñal sama darajay Baay mooy ngeen meññ lu bare, te noonu ngeen di firndeele ne samay taalibe ngeen.
9 «Ni ma Baay bi soppe, man itam noonu laa leen soppe. Saxleen ci sama cofeel. 10 Ni ma sàmme sama santaaney Baay, ba tax ma sax ci cofeelam, su ngeen ni sàmmee samay santaane, dingeen sax ci sama cofeel. 11 Maa leen wax loolu ngir samag mbég wàllsi ci yeen, ba seen mbég mat sëkk. 12 Sama santaane moo di ni ma leen soppe, ngeen soppantee noonu. 13 Joxe sa bakkan te say xarit tax, ameesul cofeel gu ko raw, 14 te samay xarit ngeen, ndegam yeena ngi def li ma leen sant. 15 Wooweetuma leen ay jaam, ndax ab jaam xamul lu sangam di def. Xarit laa leen woowe, ndax mboolem lu ma dégge ci sama Baay, xamal naa leen ko. 16 Du yeen yeena ma tànn, man maa leen tànn, sas leen ngir ngeen dem, meññi meññeef, te seenum meññeef sax, ba lu ngeen ñaan Baay bi ci sama tur, mu may leen ko. 17 Li ma leen sant nag, moo di ngeen soppante.
26 «Taxawukat bi[b] may yónni ci yeen te muy jóge ci Baay bi mooy Noowug dëgg googu di bàyyikoo ci Baay bi, te kooku bu dikkee, moo may seedeel. 27 Te yeen itam dingeen seede, ndax ca njàlbéen ngeen dale nekk ak man.
<- Yowaan 14Yowaan 16 ->
Languages