7 Teewul Yeesu ne ko: «Bàyyil Maryaama! Bés ba ñu may rob la fàggul lajkoloñ jii. 8 Néew-doole yi, dingeen ci am ñu nekk ak yeen ba fàww, waaye man amuleen ma ba fàww.»
9 Mbooloom Yawut mu réy a dikk ba ñu yégee ne Yeesoo nga fa, te Yeesu rekk yóbbuwu leen fa, waaye dañoo bëggoona gisaale Lasaar ma Yeesu dekkaloon. 10 Sarxalkat yu mag ya nag dogu, nara rey Lasaar itam, 11 ndax moo waraloon Yawut yu bare dem, dëddu leen, gëm Yeesu.
16 Kàddu yooyu nag, taalibe ya xamuñu woon ca saa sa lu muy tekki, waaye ba Yeesu tàbbee ca darajaam, ca lañu fàttaliku ne loolu lañu bindoon ci moom, te loolu it lañu ko defal.
17 Mbooloo ma daroon Yeesu, ba muy woo Lasaar, ba dekkal ko nag, di nettali la ñu fekke. 18 Moo tax itam mbooloo ma gatandu ko, ndax yégoon nañu ne googu kéemaan la def. 19 Farisen yi nag di waxante ci seen biir naan: «Xoolleen, dara ngeen ci manul; àddina yépp a ko topp!»
23 Yeesu wax leen ne leen: «Waxtu wi ñu wara darajaal Doomu nit ki jot na. 24 Maa leen ko wax déy ci lu wér, su feppu bele waddul ci suuf, dee, wéetaay lay dëkke. Waaye su deewee lay meññ fepp yu bare. 25 Képp ku bëgg bakkanam moo koy ñàkk; waaye ku bañ bakkanam ci àddina sii, moo musal bakkanam ba keroog muy texe ba fàww. 26 Ku may surgawu, na ma topp; fu ma nekk, sama surga ne fa moom itam. Ku ma surgawu nag, sama Baay moo koy teral.
27 «Léegi nag am naa njàqarey xol. Ana lu may wax? Dama naa: “Baay, musal ma ci coonob waxtu wii”? Waaye coonob waxtu wii tembe moo ma taxa dikk! 28 Baay, màggalal saw tur!» Ci kaw loolu baat dégtu ci asamaan, ne: «Maa koy màggal, màggalati ko.»
29 Mbooloo ma fa taxaw te dégg baat ba nag ne: «Yàlla jee dënu!» Ñeneen ña ne: «Am malaaka moo wax ak moom.» 30 Teewul Yeesu ne leen: «Baat boobu du maa tax mu jib, waaye yeena tax. 31 Léegi nag àtteb àddina sii jot na; léegi lees di dàq ca biti kàngam li jiite àddina sii. 32 Man nag kera bu ñu ma yékkatee, jële ma fi kaw suuf, ñépp laay xëcc, jëme ci man.» 33 Kàddu yooyu la misaale deewin wa mu naroona deewe.
34 Mbooloo ma ne ko: «Nun danoo dégge ci téereb yoonu Musaa bi ne Almasi bi day sax ba fàww. Kon yaw, noo mane ne: “Fàww dees na yékkati Doomu nit ki?” Doomu nit kooku mooy kan sax?»
35 Yeesu ne leen: «Leer gaa ngeegum ci seen biir ci diggante bu gàtt. Doxleen ci bi ngeen di am leer, ngir lëndëm bañ leena bett. Kuy doxe ag lëndëm, xamoo foo jëm. 36 Gëmleen ko ci bi ngeen di am leer, ngir ngeen doon doomi leer.»
42 Teewul sax ñu bare ci njiiti Yawut yi gëmoon nañu Yeesu, waaye Farisen yee taxoon biraluñu seen ngëm, ndax ragal ñu dàqe leen ca jàngu Yawut ba, 43 ndax ngërëmal nit ñi moo leen gënaloon ngërëmal Yàlla.
44 Yeesu nag àddu ca kaw ne: «Ku ma gëm, du man nga gëm, waaye ki ma yónni nga gëm, 45 te ku ma gis, gis nga ki ma yónni. 46 Man maa dikk, di ag leer ci àddina, ngir ku ma gëm du des cig lëndëm. 47 Ku dégg samay wax te toppu ko, du man maa koy daan, ndax daan àddina taxu maa dikk, waaye musal àddinaa ma taxa dikk. 48 Ku ma xarab ba nanguwul samay wax, am na ab daan-katam: kàddu gi ma wax moo koy daan, keroog bés bu mujj ba. 49 Ndax kat du ci sama coobarey bopp laay waxe, waaye Baay bi ma yónni, moom ci boppam moo ma sant li may dégtale ak li may wax. 50 Te xam naa ne ab santaaneem moo dig texe gu sax dàkk. Moo tax it, li may wax man, ni ma ko Baay bi dégtale, ni laa koy waxe.»
<- Yowaan 11Yowaan 13 ->- a poseti xaalis mooy peyooru benn bésub liggéey ca jamono yooya.
- b Seetal ci Taalifi cant 118.25-26.
- c cumbur: ci jamonoy jàmm, jamono yu xeex amul woon, buur yi daan nañu war mbaam, te doonul lu leen di tuutal.
- d Seetal ci Sàkkaryaa 9.9.
- e Seetal ci Esayi 53.1.
- f Seetal ci Esayi 6.10.
- g Seetal ci Esayi 6.1
Languages