23 Aji Sax ji Yàllay Israayil, Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Bu ma tijjee seen wërsëg, kàddu gii dina jibati ci réewum Yuda ak dëkk yi ko séq.
Dees na ne: “Yaw màkkaanu njubte bii,
yaw, tundu Siyoŋ wu sell wi,
yal na la Aji Sax ji barkeel!”
24 «Waa réewum Yuda ak dëkk-dëkkaanam yépp ay bokk dëkk, ak beykat yeek màngaan yi yor gétt. 25 Maay nàndal ku mar, leqali ku loof.»
Yeremeey wax
26 Ba loolu amee ma yewwu, ne xiféet, xam ne samay nelaw neex na.
Aji Sax ji teewlul na Israayil
27 «Bés a ngii nag di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «yu may jiwe kërug Israayil ak kërug Yuda jiwum doom aadama ak jiwum mala. 28 Te ni ma leen teewloo woon ba ma leen di buddat, di leen fàqat, di leen daaneel, di leen yàqate aka lor, noonu laa leen di teewloo ngir defar leen, jëmbat leen.» Kàddug Aji Sax jee. 29 «Su boobaa deesatul ne:
“Baay lekk reseñ ju xaay,
mu uum bëñu doom ja.”
30 Su boobaa ku nekk sa bàkkaaru bopp a lay rey. Ku lekk reseñ yu xaay, sa gëñi bopp lay uum.
Kóllëre gu yees a ngii
31 «Ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «yu may fas ak waa kër Israayil ak waa kër Yuda kóllëre gu yees. 32 Du mel ni kóllëre ga ma fasoon ak seeni maam keroog ba ma leen jàppee ci loxo, génne leen réewum Misra. Ndax ñoom ñoo fecci sama kóllëre, te man may seen boroom kër.» Kàddug Aji Sax jee. 33 «Waaye kóllëre gi may fas ak waa kër Israayil bu fan yooyu weesoo,» kàddug Aji Sax jee, «nii lay deme: Maay yeb sama ndigali yoon ci seen xel, ci seen xol laa koy ñaas. Maay doon seen Yàlla, ñoom ñu doon sama ñoñ. 34 Kenn dootul soxlaa jàngal kenn, muy moroomam mbaa mbokkam, naan ko: “Ràññeel Aji Sax ji!” Ndax ñoom ñépp a may ràññee, ki gëna tuut ba ci ki gëna mag,» kàddug Aji Sax jee, «ndax maa leen di jéggal seeni ñaawtéef, te seeni bàkkaar, duma ci bàyyeeti xel.»
Lii mooy saxal Israayil
35 Aji Sax ji dafa wax,
moom mi dogal jant di leeral bëccëg,
dogal weer ak biddiiw di leeral guddi,
yëngal géej, gannax yi riir,
kookooy Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,
36 mu ne: «Su dogal yooyu manoona toxu, may gis,
su boobaa askanu Israayil dina mana fey ba fàww, may gis.»
Kàddug Aji Sax jee.
37 Aji Sax ji dafa wax ne:
«Su nit manoona natt kawewaayu asamaan,
mbaa mu manoona xayma xóotaayu suuf,
su boobaa ma mana xalab mboolem askanu Israayil,
xalab leen ndax li ñu def lépp.»
Kàddug Aji Sax jee.
38 Mu ne: «Ay bés a ngi ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «dees na tabaxalaat Aji Sax ji dëkku Yerusalem, dale ko ca soorooru tata bu tudd Ananel ba ca buntu Ruq ba. 39 Dees na fa rëddaat kemu dëkk bi, jubal ba tundu Gareb, wëri ba Gowa. 40 Mboolem xur yu ñu sànni néew yaak dóomu-taal ak mboolem tool ya, ba ca yoonu ndox ma ca Sedoron, ba ca ruqu buntu Fas ya ca penku: lépp lees di sellalal Aji Sax ji. Deesatu fa buddat mbaa di fa daaneel dara.»