4 «Aji Sax ji Yàllay Israayil, Boroom gàngoori xare yi dafa wax mboolem ngàllo ga mu jële Yerusalem, yóbbu Babilon, ne leen: 5 Tabaxleen ay kër dëkke; jëmbat seeni tóokër, lekk ca meññeef ma. 6 Takkleeni jabar, am ci doom yu góor ak yu jigéen. Takkalleen seen doom ay jabar, maye seen doom yu jigéen, ñu am ñoom it doom yu góor ak yu jigéen. Yokkuleen fa, buleen fa néew. 7 Sàkkuleen jàmmu dëkk bi ma leen toxal, te ñaanal ko ci Aji Sax ji, ndax jàmmu dëkk bi mooy seen jàmm.
8 «Aji Sax ji Yàllay Israayil, Boroom gàngoori xare yi kat dafa wax ne: Seeni yonent ak seen gisaanekat yi ci seen biir, buñu leen nax. Te it buleen déglu seen boroom gént yi ngeen di firiloo seeni gént, 9 ndax kàdduy waxyuy fen lañu leen di wax ci sama tur. Yebaluma leen. Kàddug Aji Sax jee.
10 «Aji Sax ji déy dafa wax ne: Bu Babilon matalee juróom ñaar fukki ati kilifteefam, dinaa leen dikkal, sottalal leen sama kàddug jàmm, ba delloosi leen ci béreb bii. 11 Ndax man déy, xam naa mébét yi ma leen mébétal. Kàddug Aji Sax jee. Du mébéti loraange, waaye mébéti jàmm laa leen mébétal, ngir may leen yaakaaru ëllëg. 12 Su boobaa ngeen woo ma wall, dikk ñaan ma, ma nangul leen. 13 Su boobaa ngeen làmb, daj ma, ndegam làmbe ngeen seen léppi xol, 14 maa leen di may ngeen daj ma. Kàddug Aji Sax jee. Maa leen di tijjil seen wërsëg, dajale leen ci mboolem xeet ak mboolem béreb ya ma leen sànni woon. Kàddug Aji Sax jee. Maa leen di delloosi ci béreb bii ma leen yebale woon ngàllo.
15 «Yeena ne: “Aji Sax ji yónnee na nuy yonent ci Babilon.” 16 Waaye Aji Sax ji dafa wax lu jëm ci buur bi toog ci jalub Daawuda, jëm ci képp ku bokk ci askan wi des ci Yerusalem gii di seen bokk ya àndul woon ak yeen, dem ngàllo. 17 Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi dafa wax ne: Maa ngii di leen yónnee saamar akub xiif ak mbas. Maa leen di def ñu mel ni figg ju nëb, ba kenn manu koo lekk ndax bon. 18 Maa leen di toppe saamar akub xiif ak mbas. Maa leen di def misaal mu daw yaramu mboolem réewi àddina, teg gent bu ñuy muslu ci biir mboolem xeet wu ma leen sànni, ba ku fay kókkalee mbaa móolu, ñoom ngay tudd. 19 Li ko waral mooy, ñoo ma déggalul. Kàddug Aji Sax jee. Dama leena yónnee yonent yiy samay jaam ay yooni yoon, te déggaluñu ma. Kàddug Aji Sax jee. 20 Kon nag yeen mboolem ngàllo gi ma yebale Yerusalem ba Babilon, dégluleen kàddug Aji Sax ji. 21 Aji Sax ji Yàllay Israayil, Boroom gàngoori xare yi dafa wax ci mbirum Akab doomu Kolaya ak Cedesyas doomu Maaseya, ñoom ñi leen di jottali kàdduy waxyuy fen ci sama tur. Ma ne: Maa ngii di leen teg ci loxol Nebukatnecar buuru Babilon, mu rey leen, ngeen di gis. 22 Dinañu tax mboolem kuy móoloo te bokk ca ngàllog Yudeen ña ca Babilon, danga naan: “Yal na la Aji Sax ji teg la mu tegoon Cedesyas ak Akab, ña buuru Babilon lakk cib taal.” 23 Li ko waral mooy njombe wi ñu def fi digg Israayil, di njaalook seen jabari dëkkandoo, di wax ci sama tur ay kàdduy fen yu ma leen santul. Maa ko xamal sama bopp, seede ko. Kàddug Aji Sax jee.»
29 Ba Sofoni sarxalkat ba jàngee bataaxal boobu, Yonent Yàlla Yeremi di dégg, 30 kàddug Aji Sax ji dikkal Yeremi ne ko:
31 «Yónneel ca ngàllo gépp ne leen: Aji Sax ji dafa wax ci mbirum Semaya Nexelameen ba, ne: “Semaya waxal na leen kàdduy waxyu, gëmloo leen ay fen, te yebaluma ko. 32 Kon nag Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di mbugalsi Semaya Nexelameen bi, mook askanam. Ku bokk ci moom du toog ci biir xeet wii, bay gis ngëneel li may defal sama ñoñ.” Kàddug Aji Sax jee. “Moo xiirtal askan wi ci gàntal Aji Sax ji.”»
<- Yeremi 28Yeremi 30 ->
Languages