6 Aji Sax ji ne ma: «Yéeneel mboolem kàddu yii ci biir dëkki Yuda yu mag yi ak ci mbeddi Yerusalem, nga ne: “Dégluleen sàrti kóllëre gii te jëfe ko. 7 Artu naa artu seeni maam, dale ko ba ma leen génnee réewum Misra, ba tey jii ma jàppoo di leen artu, naan leen ñu déggal ma.” 8 Waaye dégluwuñu, teewluwuñu, xanaa ku nekk di wéye dëgër bopp, topp ag bon xolam. Moo tax ma wàcce ci seen kaw mboolem sàrti kóllëre gii ma leen santoon ñu war koo jëfe te jëfewuñu ko.»
9 Aji Sax ji dellu ne ma: «Pexem fippu feeñ na ca Yuda gépp ak ca waa Yerusalem. 10 Dellu nañu ca seen ñaawtéefi maam ya bañoona sàmm samay kàddu. Ñoom it topp nañu yeneen yàlla, di leen jaamu. Waa kër Israayil ak waa kër Yuda fecci nañu kóllëre ga ma fasoon ak seeni maam.
11 «Moo tax Aji Sax ji wax ne: “Maa ngii di leen wàcceel musiba mu ñu dul mana rëcce. Dinañu ma ne wóoy te duma leen déglu. 12 Su ko defee waa dëkki Yuda yu mag yeek waa Yerusalem dem jooytuji ca yàlla ya ñuy taalal cuuraay, te duñu leen mana wallu mukk ci seen jamonoy musiba.
13 «“Yaw Yuda, ni sa dëkk yu mag tollu, ni la say tuur tollu. Ni mbeddi Yerusalem tollu it, ni la sarxalukaay yi ñu fa saam tollu, ñu di fa taalal cuuraay Baal, tuur mu seexluwu mi.”
14 «Yaw nag Yeremi, bul ñaanal askan wii. Bu leen tinul, bu leen dagaanal. Ndax kat keroog bu ñu nekkee ci seen musiba, ba naan ma wóoy, du maay déglu.
21 Moo tax Aji Sax ji wax lii ci mbirum waa Anatot, ñiy wut sama bakkan, naan ma: «Baal di jottali kàdduy waxyu ci turu Aji Sax ji, lu ko moy nu rey la.» 22 Moo tax kay Aji Sax ji Boroom gàngoor yi wax ne: «Maa ngii di wàccesi mbugal fi seen kaw; seen xale yu góor ñu reye leen saamar; seeni doom, góor ak jigéen, dee ak xiif. 23 Aw nit, duñu ko dese; maay wàcceel waa Anatot safaan, bu seen atu mbugal taxawee.»
<- Yeremi 10Yeremi 12 ->
Languages