7 Mbooloo ma, Aji Sax ji lañu jaamu giiru dundu Yosuwe, ak giiru dundu mag ña wuutu Yosuwe, te gisoon mboolem jëf ju réy ji Aji Sax ji defal Israayil.
8 Yosuwe doomu Nuun, jaamub Yàlla ba nag, ci téeméeri atam ak fukk la nelaw, 9 ñu denc ko ca gox ba mu séddoo, ca Timnat Eres ga ca diiwaanu tundi Efrayim, ca bëj-gànnaaru tundu Gaas.
16 Ba mu ko defee Aji Sax ji falal leen ay njiit, ñooña xettali leen ca ña leen di sëxëtoo. 17 Waaye seeni njiit it, déggaluñu leen, xanaa ñuy gànctook[a] yeneen yàlla, di leen sujjóotal. Yoon wa seeni maam toppoon, di sàmm santaaney Aji Sax ji, moom lañu teela wacc. Royuñu seeni maam. 18 Saa yu leen Aji Sax ji falalaan njiit nag, mooy ànd ak njiit la, di leen musal ca seeni noon, giiru dundu njiit la. Booba seeni onk la leen Aji Sax ji ñeewantee woon, ndax ña leen doon noot aka joggati. 19 Waaye saa su njiit la faatoo rekk askan wa dellu di defug yàqute, ba raw seeni maam, ci topp yeneen yàlla, di leen jaamooka sujjóotal. Bawuñu lenn ci seeni jëf ak seen jikkoy wowle.
20 Ba mu ko defee sànjum Aji Sax ji tàkkal Israayil. Mu ne: «Gannaaw askan wii ñoo fecci kóllëre gi ma dénkoon seeni maam, te ñoo ma déggalul, 21 man it du maa leen di dàqalatil ñenn ci xeet yi fi Yosuwe bàyyi, ba mu deewee; 22 su ko defee, ñooñu laay nattoo Israayil, ba gis ñu sàmm yoonu Aji Sax ji, na ko seeni maam daan sàmme, mbaa ñu ñàkk koo sàmm.» 23 Noonu la fa Aji Sax ji bàyyendee xeet yooyu mu teguloon ca loxol Yosuwe, ba gaawu leen faa dàqe.
<- Njiit ya 1Njiit ya 3 ->- a gànctu misaal lay doon, mbete jigéen ju njaaloo, di fecci kóllëre gi mu am ak jëkkëram. Noona la bànni Israayil di defi, ci seen bokkaale, di fecci seen kóllëre ak Aji Sax ji.
Languages