14 Ci kaw loolu juróomi ndaw ya yëri woon diiwaanu Layis wax seen bokk ya, ne leen: «Ndax xam ngeen ne ci kër yii, genn a ngeek am xar-sànnim carxal ak tuur mu ñu yatt ak ay gàllaaji kër ak itam tuur mu ñu móol? Léegi nag yeenay seet lu ci war.» 15 Ba loolu amee, ñu jàdd, ba ca kër Leween ba, kër Mika. Ñu jàmmanteek moom. 16 Fekk na juróom benni téeméeri Daneen ñaa nga ràngooy ngànnaay, taxaw ca buntu dëkk ba. 17 Juróomi ndaw ya yëri woon réew ma, dugg ca biir, daldi jël tuurum yatt maak xar-sànni maak gàllaaji kër yaak tuur ma ñu móol. Fekk na sarxalkat baa nga taxaw ca buntu dëkk ba, mook juróom benni téeméeri nit ña ràngooy ngànnaay. 18 Ba ñooña duggee kër Mika, ba jël jëmmi tuur ya ñu yatt ak xar-sànni maak gàllaaji kër yaak tuur ma ñu móol, sarxalkat ba moo ne leen: «Lu ngeen di def nii?» 19 Ñu ne ko: «Neel cell, ne patt! Toppal ci nun rekk, féete nu céru kilifa, di sunu sarxalkatu giir. Lu la gënal? Di sarxalkatu kër kenn nit doŋŋ, am di sarxalkatu genn giirug lëmm ci Israayil?» 20 Wax jooju nag neex sarxalkat ba, mu jël xar-sànni maak gàllaaji kër yaak tuur ma ñu yatt, daldi ànd ak gàngoor ga, dem.
21 Ba loolu amee ñu teguwaat ca yoon wa, jiital seeni doom ak seeni jur ak seen alal. 22 Ba Daneen ña demee ba soreek kër Mika, ca la dëkkandooy Mika ya mu dendeel wootante, ba daje ànd ak Mika, ngir dabi leen. 23 Ci kaw loolu ñu joor Daneen ña, ñooñu geesu, ne Mika: «Loo xewle, ba bàbbi mii mbooloo?» 24 Mika ne leen: «Sama jëmmi tuur yi ma sàkk, ngeen jël, booleek sarxalkat bi, dem! Lu ma deseeti nag? Ana lu ngeen ma naa loo xewle?» 25 Daneen ña ne ko: «Bu sa kàddu jib, nuy dégg, lu ko moy gaa yu tàng bopp ñooy dal ci sa kaw, ngeen ñàkk seen bakkan, yaak sa waa kër.» 26 Ba loolu amee Daneen ña dem seen yoon. Mika nag gis ne ñoo ko ëpp doole, mu walbatiku, ñibbi këram. 27 Noonu la Daneen ña nangoo la Mika defaroon, yóbbaale ab sarxalkatam. Ci kaw loolu ñu jàll ba Layis, dal ca kaw askan woowa ànd akug dal ak teeyug bakkan. Ñawkay saamar lañu leen leel, dëkk ba, ñu lakk ko. 28 Du kenn ku leen xettali, ndax dëkk ba sorewoo naak Sidon, te séquñu woon ak kenn dara. Dëkk baa nga woon ca xur wa dendeek Bet Rexob. Ba mu ko defee Daneen ña tabaxaat dëkk ba, dëkke. 29 Ñoo tudde dëkk ba Dan, dippee ko seen maam góor Dan, doomu Israayil, waaye Layis la dëkk ba njëkkoona tudd. 30 Ci kaw loolu Daneen ña sampal seen bopp jëmmu tuur ma ñu yatt, Yonatan sëtub Gersom doomu Musaa nag, mook aw askanam ñoo doon sarxalkati Daneen ña, ba kera bés ba ñu yóbboo waa réew ma ngàllo. 31 Jëmmu tuur ma ñu yatt, te Mika sàkkoon ko, moom la Daneen ña sampaloon seen bopp, di ko jaamu, mboolem jant ya kërug jaamookaayu Yàlla ga nekkee ca Silo.
<- Njiit ya 17Njiit ya 19 ->
Languages