4 Ci kaw loolu Yefte dajale góori Galàdd ñépp, daldi xareek Efraymeen ña, ba duma leen. Góori Galàdd duma niti Efrayim ñi leen waxoon ne leen: «Yeen waa Galàdd, dungeen lenn lu moy ay daw-làqu yu rëcce Efrayim, jàllsi Manase.» 5 Waa Galàdd nag aakimoo jàllukaayi dexu Yurdan ya, ngir kar Efraymeen ña, ba bu ku rëcce Efrayim dikkee ne: «Mayleen ma ma jàll,» waa Galàdd laaj ko, ne ko: «Ab Efraymeen nga?» Mu ne déet, 6 ñu ne ko: «Neel “Sibolet”»; da naan: «Simbolet,» ndax làmmiñu Efraymeenam moo jubuwul boobu baat. Su ko defee ñu jàpp ko, rey ko ca jàllukaayi dexu Yurdan. Ñeent fukki junniy Efraymeen ak ñaar (42 000) dee nañu, jant yooyu.
7 Yefte nag juróom benni at la jiite Israayil. Ba Yefte waa Galàdd ba faatoo, ca dëkki Galàdd ya lañu ko denc.
11 Elon Cabuloneen ba moo ko wuutu, te fukki at la jiite Israayil. 12 Ba Elon Cabuloneen ba faatoo, ca Ayalon lañu ko denc ca diiwaanu Sabulon.
13 Abdon doomu Ilel, ma cosaanoo Piraton moo ko wuutu, jiite Israayil. 14 Amoon na ñeent fukki doom yu góor, ak fanweeri sët yu góor, ñuy war juróom ñaar fukki mbaam. Juróom ñetti at la jiite Israayil. 15 Ba Abdon doomu Ilel, ma cosaanoo Piraton faatoo, ca Piraton lañu ko denc ca réewum Efrayim ca diiwaanu tundi Amalegeen ña.
<- Njiit ya 11Njiit ya 13 ->
Languages