4 Ba dëj ba weesoo, Yuusufa dafa wax ak waa kër Firawna, ñaan leen ñu dimbali ko, waxal ko Firawna ne ko, 5 baayam da ne woon, mu ngi waaja dee, waaye bàmmeel ba mu yattaloon boppam ca xunt ma ca réewu Kanaan, na ko giñal ne dina ko denc foofa. Mu ne kon, na ko Firawna may, mu robi baayam te délsi. 6 Firawna may ko, mu robi baayam, na mu ko ko giñloo woon.
7 Yuusufaa ngay dem robi baayam, moom ak mboolem jawriñi Firawna ak magi këram ak mboolem kàngami Misra. 8 Ña nga ànd ak waa kër Yuusufa gépp ak ay doomi baayam ak waa kër baayam, bàyyiwuñu diiwaanu Gosen lu moy xale ya ak gàtt ya ak jur gu gudd ga, 9 ay watiir aki gawar topp ca, ñu def gàngoor gu réy.
10 Ba ñu agsee ca dàggay Ataat ja ca wàllaa dexu Yurdan, dañu koo jooy jooy yu réy te metti. Yuusufa dëjal fa baayam diiru juróom ñaari fan. 11 Waa réewu Kanaan, gis dëj ba ca dàggay Ataat, naan: «Dëju waa Misra bii aka réy!» Moo tax ñu tudde béreb booba ca wàllaa dexu Yurdan, Abel Misra (muy firi Dëju waa Misra).
12 Doomi Yanqóoba nag def la leen seen baay dénkoon, 13 yóbbu ko ca réewu Kanaan, daldi koy rob ca xunt ma ca toolub Magpela, te Ibraayma jëndoon ko ca Efron, Etteen ba, ngir def ko bàmmeel. Mooy tool ba jàkkaarloo ak Mamre. 14 Ba Yuusufa dencee baayam ba noppi, dafa dellu Misra, moom ak doomi baayam ya ak mboolem, ña mu àndaloon ca robu baayam.
18 Ci kaw loolu magam ya ñëwal seen bopp ba ca moom, sujjóotal ko ne ko: «Sang bi, nu ngi nii, di la siyaare.» 19 Yuusufa nag ne leen: «Buleen am dara lu ngeen di ragal. Xanaa maay Yàlla? 20 Dëgg la, fexeel ngeen ma lu bon, waaye Yàllaa ko walbati, def ko lu baax, ba dogal li am tey jii, muy bakkan yu bare yi mucc. 21 Kon nag buleen tiit, dinaa leen yor, yeen ak seeni doom.» Yooyu kàddu la dalale seen xol, ba ñu am jàmm.
24 Mu am bés Yuusufa ne ay bokkam: «Sama waxtu jege na, waaye Yàlla dina dikk, yéwéne leen moos, ba jële leen ci réew mii, yóbbu leen ca réew ma mu dige woon, ba giñal ko Ibraayma, Isaaxa ak Yanqóoba.» 25 Booba la Yuusufa wax doomi Israayil, ne leen: «Giñalleen ma ne bés bu Yàlla dikkee ba yéwéne leen, dingeen yóbbaale samay yax, waaye dungeen ma fi bàyyi.»
26 Gannaaw loolu Yuusufa nelaw ci téeméeri atam ak fukk. Ñu waajal néew ba, ba du yàqu, daldi koy yeb cib tàdd, denc ko foofa ca Misra.
<- Njàlbéen ga 49- a Fajkati waa Misra, ndàbb lañu daan waajale néew, ba du yàqu.
Languages