8 Kuus moo jur Nimrodd, ki jëkk di jàmbaar ju siiw ci kaw suuf, 9 mu doonoon rëbbkat bu maga mag. Looloo waral ñu naan: «Mbete Nimrodd, rëbbkat bu maga mag ba.» 10 Dëkk yiy péeyi nguuram ñoo di Babel ak Ereg ak Akàdd ak Kalne, gi ci réewu Sineyaar. 11 Ca réew mooma la Nimrodd jóge dem Asur, sanc Niniw ak dëkk yooyee di Rexobot Ir ak Kala, 12 ba Resen gi ci diggante Niniw ak Kala, dëkk bu mag bi.
13 Misrayim nag mooy maami Luddeen ñi[a] ak Anameen ñi ak Leyabeen ñi ak Naftuyeen ñi 14 ak Pataruseen ñi ak Kasluxeen ñi, ak it Kaftoreen ñi, ñooñee waa Filisti soqikoo[b].
15 Kanaan moo taawloo Sidon, teg ca Ett. 16 Kanaan mooy maamu Yebuseen ñi ak Amoreen ñi ak Girgaseen ñi. 17 Mooy maamu Eween ñi ak Arkeen ñi ak Sineen ñi. 18 Mooy maamu Arwàddeen ñi it ak Cemareen ñi ak Amateen ñi. La ca tegu làngi Kanaan tasaaroo. 19 Kemu suufas Kanaaneen ña, mu ngi tàmbalee Sidon, jaar weti Gerar, dem ba Gasa, wuti Sodom ak Gomor ak Adma ak Ceboyim, daldi teeri Lesa.
20 Ñooñu ñooy askani Xam, askan wu ci nekk ak làngam ak làkkam, di ay xeet ci seeni réew.
26 Yogtaan a jur Alamodàdd ak Selef ak Asarmawet ak Yerax 27 ak Adoram ak Usal ak Digla 28 ak Obal ak Abimayel ak Seba 29 ak Ofir ak Awila ak Yobab. Ñooñu ñépp di doomi Yogtaan yu góor. 30 Ña nga dëkkoon ca wàllu Mesa ga wuti Sefar, di diiwaanu tund ya ca penku.
31 Ñooñoo askanoo ci Sem, askan wu ci nekk ak làngam ak làkkam, di ay xeet ci seeni réew.
32 Làngi doomi Nóoyin yu góor a ngoogu, làng gu nekk ak askanam, ñu diy xeet. Ci ñoom la xeet yépp jóge tasaaroo ci kaw suuf, gannaaw ba mbënn ma wéyee.
<- Njàlbéen ga 9Njàlbéen ga 11 ->
Languages