Galasi Diiwaanu Galasi bokkoon na ci nguuru waa Room. Nekk na ci réew mu ñuy wax tey Tirki. Póol yégle xibaaru jàmm bu Almasi bi ci ñeenti dëkk ci Galasi (Jëf ya 13.13—14.20). Bàyyi na fa ay mbooloom nit ñu topp Almasi bi, ay Yawut ak ñeneen ñu dul Yawut. Waaye dafa am ay jàngalekati caaxaan yu yoxoosu ci seen biir ngir jàngale lu leen fàbbi. Ñu ne gëmkat ñi dul Yawut dañoo wara xaraf, te gëmkat yépp dañoo wara sàmm ba tey ndigali yoonu Musaa. Moo tax Póol bind leen, ne leen du ci jëfi sàmm ndigali yoon la Yàlla di jox kenn àtteb ku jub, waaye ci li mu gëm ne Almasi bi dee na ngir gàddu mbugali tooñ Yàlla, ngir jot nit ñi nekk ci curgag yoon wi. Dañu leena goreel ngir ñu dund ci cofeel ndax ni leen Almasi bi soppee. Ci tënk: 1.1—2.21 Póol ndaw tigi la te kàddoom dëggu na. 3.1—4.31 Yàlla dina jox nit àtteb ku jub ci kaw li mu gëm Yeesu. 5.1—6.18 Gëmkat du wéeru ci yoon wi ngir ñu jox ko àtteb ku jub, waaye day topp Noowug Yàlla gu Sell gi.
10 Léegi nag ndax nit ñi laay sàkkoo jubool, am Yàlla? Am nit ñi laay wuta neex? Su ma bëggoona wéye neex nit ñi de, duma doon jaamub Almasi bi.
13 Ndax kat dégg ngeen ni ma doon jëfe bu njëkk, bi ma nekkee ci yoonu Yawut, bunduxataal gu jéggi dayo ga ma daan teg mbooloom gëmkati Yàlla mi, di ko yàq. 14 Yoonu Yawut, maa ci rawoon ñu bare ci sama maas gi ma bokkal askan, te maa leen gënoona xér fuuf ci sunu aaday maam. 15 Waaye ca sama biiru ndey la ma Yàlla séddoo, woo ma ci boppam ci kaw yiwam, te moom la soob, 16 mu feeñalal ma Doomam, ba ma àgge jàmbur ñi dul Yawut xibaaru jàmm bi ci mbirum Almasi bi. Ci saa si diisoowuma ci ak kenn. 17 Demuma sax Yerusalem, seeti ñi ma njëkka doon ndawi Almasi bi, waaye Arabi laa dem, doora délsi Damaas.
18 Gannaaw ba ñu ca tegee ñetti at laa doora dem Yerusalem, ngir xamanteji ak Sefas*Sefas mooy Piyeer. Sefas mooy tur wu Almasi bi tudde taalibeem boobu. Seetal ci Yowaan 1.42. , toog fa moom ñaari ayi bés. 19 Teewul gisuma kenn ci ndaw yi ci des, ku dul Yanqóoba, rakku Sang bi. 20 Li ma leen bind nii nag, Yàlla mi nu tiim seede na ne du ay fen. 21 Gannaaw gi laa dem diiwaani Siri ak Silisi. 22 Waaye ba boobu, mboolooy gëmkati Almasi ya ca diiwaanu Yude xamuñu ma woon. 23 Déggoon nañu rekk ñu naan: «Ki nu daan bunduxataal bu njëkk, di yàq sunu yoonu ngëm wi de, léegi mooy yégle xibaaru jàmm bi!» 24 Mboolooy gëmkat yooyu nag di sant Yàlla ci man.
Galasi 2 ->- a Sefas mooy Piyeer. Sefas mooy tur wu Almasi bi tudde taalibeem boobu. Seetal ci Yowaan 1.42.
Languages