1 Kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma: 2 «Yaw nag nit ki, yékkatil kàddu, muy ay jooy ci kaw dëkkub Tir. 3 Waxal Tir mi toog ci buntu géej, jula yooyuy jëflanteek xeeti dun yu bare, nga ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
9 magi Gebal ñeek nitam ñu xareñ ñi fi yaw féetewoo di jagal.
Mboolem gaal yu mag yi ak ña cay liggéey di dal ak yaw,
waa gaal ya di jënd sam njaay.
10 Waa Pers ak waa Ludd ak waa Puut,
ñépp a nga woon ca sa mbooloom xare,
di wékk fa yaw seeni pakk ak seen mbaxanay xare.
Ñooñoo la darajaal.
11 Arwàddeen ñeek sa niti bopp a daan wattu sa tata yépp,
Gammàddeen ñi di wattu say sooroori tata,
ñu wékk seeni gànnaay ci li wër say tata.
Ñooñoo mottali sab taar.
12 «“Tarsis dëkk baa doon sab jula ndax sa jépp xeetu alal ju bare. Xaalis ak weñ gu ñuul ak gu weex ak betteex la waa dëkk ba daan weccikoo seen alal. 13 Waa Geres ak Tubal ak Meseg di say jula, di leen indil ay jaam ak ndabi xànjar yu ñuy weccikoo seen koom. 14 Waa kër Togarma indi ay fas aki gawar aki berkelle, di ko weccikoo seen alal. 15 Dedaneen ñi di say jula, koomu dun yu bare di jaare say loxo, ñu di la feye bëñi ñey ak bantu jalambaan. 16 Waa Siri it di say jula, di jëndeek yaw lu bare loo defar, di ko wecci per yu jafe, ak ndimo yu xewar, ak séri ràbb ak lẽe ak peri xor ak peri rubi. 17 Yudaak réewum Israayil it di say jula, di la wecci bele bu bawoo Minit, ak dugub ak lem ak diwu togg ak diwu yaram. 18 Dëkkub Damaas di jula lu bare ak yaw, ci lépp loo defar ak jépp alal joo barele, di la ko weccee biiñ bu jóge Elbon, ak kawaru xar gu weex. 19 Waa Wedan ak waa Geres bàyyikoo Usal, di la wecci sa koom weñ gu ñu tëgg, ak xasum kaas ak barax bu xeeñ. 20 Waa Dedan it di say jula, indil la seen ndimoy tegi fas. 21 Waa Arabi ak mboolem garmiy Kedar it di jëflanteek yaw, feye la ay tàppaanga aki kuuy aki sikket. 22 Julay Seba ak Raama it di jëflanteek yaw, di la indil ngën-gi-safal ak mboolem peru gànjar, ak wurus yu ñuy weccikoo sa alal. 23 Waa dëkk yii di Karan ak Kane ak Eden ñoom it di say jula, ñook julay Seba ak Asur ak Kilmàdd. 24 Ñooñoo doon say jula yu lay indil yérey tànnéef ak turki yu yolet ak yérey ràbb ak malaan yu yànj ak goj yu rawaasoo yu wér. 25 Ay gaali Tarsis yu mag a daan yóbbu sam njaay.
Nga fees dell, diis gann fi digg xolu géej.
26 Say joowkat waral la mbeex mi ne màww,
ba ci diggu géej, teewul ngelawal penku damm la.
27 Sa alal ja, sab yeb, sa njaay ma,
sa niti géej, say mool, say jagalkat, say jaaykat,
ak mboolem sa dag yi ci sa biir,
ak mboolem sa gàngoor gi ci sa biir,
ñooy tàbbeendoo xolu géej keroog sa bésub jéll ba.
28 Bu say mool yuuxoo,
tefes yaay riir,
29 képp kuy ŋàbb joowu wàcce gaalam.
Nitu géejoo mboolem mool,
ñépp fi suuf lañuy taxaw.
30 Ñoo lay jooyal,
di yuuxu yuux yu metti,
di xëppoo suuf,
di fëlëñoo dóomu-taal.
31 Yaay tax ñuy nelu,
sol ay saaku di ko ñaawloo,
di la jooye naqaru xol ak yuux yu metti.
32 Ñeey am tiis, yékkatil la kàddug jooy,
jooy la, ne:
‘Ana dëkk bu mel ni Tir,
mi ñu wedamal nii biir géej?’
33 Ba ngay yebbee géej sam koom,
yaa daan reggal ñu bare.
Sa alal ak sa koom gu bare nga woomale buuri àddina.
34 Léegi rajaxoo nga biiri gannax ca biir xóotey géej,