1 Aji Sax ji ne Musaa: «Dama ne, def naa nga féete Firawna fi ko Yàlla féete, sa mag Aaróona di sa yonent. 2 Su ko defee yaw nga wax ko li ma la sant lépp, sa mag Aaróona wax ko Firawna, ngir mu bàyyi bànni Israayil, ñu génn réewam. 3 Waaye man maay dëgëral boppu Firawna, ba fulandi samay firnde ak samay kéemaan ci biir réewum Misra. 4 Firawna du leen déggal. Su ko defee nag maay tàllal sama loxo, tiimale Misra, te maay dogal mbugal yu kéemaane, ba goreel bànni Israayil, sama ñoñ, ñu génn Misra, kuréel ci kaw kuréel. 5 Keroog bu ma tàllalee sama loxo, tiimale ko Misra, ba génnee bànni Israayil ca seen biir, waa Misra dinañu xam ne maay Aji Sax ji.»
6 La Aji Sax ji santoon Musaak Aaróona, noonu rekk lañu ko defe. 7 Musaa nga tollu woon ci juróom ñett fukki at (80); Aaróona moom am juróom ñett fukki at ak ñett (83); ca jamono, ya ñuy wax ak Firawna.
10 Ci kaw loolu Musaa ak Aaróona àgg ba ca Firawna. Ñu def la leen Aji Sax ji santoon. Aaróona jël yetam, sànni ca suuf ca kanam Firawnaaki dagam; yet wa soppaliku jaan. 11 Ba mu ko defee Firawna moom itam woo boroom xam-xam yaak ñeengokat ya. Jabarkati Misra ya ñoom it fexe ca seeni xarfafuufa, ba def lu mel noona. 12 Ku nekk ca ñoom sànni yetam, mu soppaliku jaan, yetu Aaróona nag wann seeni yet[a]. 13 Terewul Firawna të, faalewu leen, muy la Aji Sax ji waxoon.
19 Ci kaw loolu Aji Sax ji ne Musaa: «Waxal Aaróona ne ko: “Jëlal saw yet, te tàllal sa loxo tiimale ko ndoxi Misra, muy seeni dex ak seen yooni ndox ak seeni déeg ak fépp fu ndox taa, mu ànd soppaliku deret.” Deret ja dina daj Misra gépp, ba ca këll yaak njaq ya.» 20 Musaa ak Aaróona def loolu lépp, na leen ko Aji Sax ji sante. Naka la ne xaas yet wa, ne ko tàrr ca ndoxum Niil ma, ca kanam Firawnaaki dagam, ndoxum Niil ma mépp di deret, 21 jën ya ca dexu Niil ga dee, dexu Niil ga xasaw, ba waa Misra manatuñoo caa naan. Misra gépp di deret. 22 Jabarkati Misra itam fexe ca seeni xarfafuufa, ba def lu mel noona. Firawna të rekk, tanqamlu Musaak Aaróona, muy la Aji Sax ji waxoon. 23 Ba loolu amee Firawna ne wërëñ, dellu këram, te bàyyiwul xel ca mbir ma. 24 Waa Misra gépp di gas la wër dexu Niil, ngir am ndoxum naan, ndax manuñu woona naan ca dex ga.
- a Manees naa jàpp ne jaan, ja yetu Aaróona soppaliku woon, moo wann jaan, ya seen yet soppaliku.
Languages