4 «Su ngeen dajeek seen nagu noon mbaa mbaamam mu réer, fexeleen ba delloosil ko ko. 5 Su ngeen gisee seen mbaamu noon mu ab sëf daaneel, buleen ko romb; dimbalileen seen noon, yékkatilleen ko ko.
6 «Buleen jalgati àqu néew-ji-doole cib layoom. 7 Kàddu gu dëgguwul, soreleen ko, te ku deful dara ak ku jub, buleen ko reylu, ndax nit ku bon, duma ko àtte mukk àtteb ku jub. 8 Alali ger nag buleen ko nangu, ndax ger day gumbaal njàccaar, di xañ aji jub dëgg.
9 «Ab doxandéem, buleen ko noot; yeen ci seen bopp, jaar ngeen ci ndoxandéem, ndax ay doxandéem ngeen woon ca réewum Misra.
12 «Diiru juróom benni fan ngeen di liggéey, waaye bésub juróom ñaareel ba, noppalu leen, ndax seen nag ak seen mbaam mana noppalu, seen jaam bu juddu ci kër ga akub doxandéem it mana astandiku.
13 «Li ma leen wax lépp sàmmleen ko, te turi yeneen yàlla, buleen ko tudd; bumu jibe sax seen gémmiñ.
18 «Buleen ma rendil benn sarax, di boole deret jeek lu am lawiir, te nebbonu gàtt bu ngeen ma sarxal ci sama màggal, bumu fanaan ba bët set.
19 «Ngëneeli meññeef ma njëkka ñore ca seen suuf, moom ngeen di yóbbu seen kër Yàlla Aji Sax ji.
23 «Bu leen sama malaaka jiitoo, ba yóbbu leen ca réewum Amoreen ña ak Etteen ña ak Periseen ña ak Kanaaneen ña ak Eween ña ak Yebuseen ña, ba ma faxas leen ñoom ñépp, 24 su boobaa buleen sujjóotal mukk seeni tuur, di leen jaamu, mbaa ngeen di roy seeni aada, waaye yàqateleen seeni tuur te toj tasar seen tuuri doj ya fa sampe. 25 Jaamuleen ma, man seen Yàlla Aji Sax ji, ma barkeel seen dugub ak seen ndox, boole ci jële wopp ci seen biir. 26 Su ko defee du kenn ku ëmbam di yàqu, mbaa mu tëlee am doom ci seenum réew, te maay matal sëkk seen limu fan.
27 «Tiitaange laay yebal, mu jiitu leen. Maay tiital mboolem xeet wu ngeen fekki, te maay def seen noon yépp won leen gannaaw. 28 Maay yebal mbas mu leen jiitu, dàqal leen Eween ñi ak Kanaaneen ñi ak Etteen ñi. 29 Waaye duma leen dàqandoo ci menn at, lu ko moy réew mi gent, rabi àll yi mujj bare lool ci seen kaw. 30 Ndànk-ndànk laa leen leen di dàqal, ba kera ngeen di yokku, ba nangu réew mi.
31 «Maa leen di dogal kemug suuf gu dale géeju Barax yi, ba géeju waa Filisti, daleeti ca màndiŋ ma, ba ca dexu Efraat, ndax maay teg waa réew mi ci seeni loxo, ngeen dàq leen. 32 Buleen wóllëranteek ñoom, buleen wóllëranteek seeni tuur. 33 Buñu dëkke seenum réew, lu ko moy muy seen ndëgg-sërëx; ndax dañu leen di xiir ci moy ma, ba ngeen jaamu seeni tuur.»
<- Mucc ga 22Mucc ga 24 ->
Languages