Muccug bànni Israayil Yonent Yàlla Musaa moo wéyal jaar-jaari bànni Israayil, jële ko fa ko téereb Njàlbéen ga bàyyi woon, gannaaw ñeenti téeméeri at (400). Yàlla musal na bànni Israayil ca seen buumi njaam ci Misra, Musaa jiite leen, ba génne leen Misra. Yàlla moo jox bànni Israayil ndigali yoon wi ca tundu Sinayi, Musaa jottali ko, muy li lal kóllëre gi mu fas, moom Yàlla ak bànni Israayil, ndax ci ñoom la nammoona amal digeem baak seen maam Ibraayma. Yàlla sant Musaa, mu defarlu ab xaymab ndaje, ne: «Foofa laay dajeek bànni Israayil, béreb ba doxe fa sell ndax samag leer. Maay sellal xaymab ndaje mi ak sarxalukaay bi, te Aaróona aki doomam, maa leen di sellal, ngir ñu doon samay sarxalkat. Maay dëkk fi digg bànni Israayil te maay nekk seen Yàlla ji leen génnee réewum Misra, ngir dëkk fi seen biir.» (29.43-46). Ci tënk: Saar 1—18 Yàlla yiwi na bànni Israayil, génne leen Misra. Saar 19—24 Yàlla fasante na kóllëre ak bànni Israayil. Saar 25—40 Yàlla feeñal na màggaayam ak sellaayam ci xaymab ndaje mi ñu defar, ba noppi yékkati ko ci diggu dal bi.
13 Waa Misra dañoo mujj di duggal bànni Israayil ci njaam gu metti, 14 yen leen toskarey àddina ndax liggéey yu metti. Ñuy móol ban, di tabax, waa Misra teg ca sëf leen mboolem liggéeyu tool ya. Néegoon nañu ca ñoom lool ca mboolem liggéeyu njaam bu ñu leen sas.
15 Firawna buuru Misra teg ca wax ak rewlikati Ebrë ya[c], te kenn ka tuddoon Sifra, ka ca des di Puwa. 16 Mu ne leen: «Bu ngeen dee rewli jigéeni Ebrë yi, nangeen xool lu xale bi doon. Su dee góor, reyleen, su dee jigéen, bàyyileen, mu dund.» 17 Teewul rewlikat ya ragal Yàlla, ba defuñu la leen buur ba sant; xanaa ñu bàyyi liir yu góor ya, ñu dund. 18 Buuru Misra woolu rewlikat ya, ne leen: «Ana lu tax ngeen def lii, di bàyyi liir yu góor yi, ñu dund?» 19 Rewlikat ya ne ko: «Li tax kay mooy, jigéeni Ebrë yi dañoo niroowul ak jigéeni waa Misra; ndax dañoo njaxlaf, ba bu rewlikat yiy laata agsi, fekk ñu mucc ba noppi.» 20 Bànni Israayil nag di fulandiwu, gëna yokku, Yàlla defal rewlikat ya aw yiw, 21 may leen giir ndax seenug ragal Yàlla. 22 Gannaaw loolu Firawna sant waa réew ma yépp, ne leen: «Mboolem doom ju juddu ci Ebrë yi, di góor, sànnileen ca dex ga, waaye lu ciy jigéen, bàyyileen, mu dund.»
Mucc ga 2 ->
Languages