Efes Efes dëkk la woon bu féete ci réew mu ñuy wax tey Tirki. Amoon na fa màggalukaay bu ñu doon jaamoo tuur bu tudd Artemis. Póol jàngale na xibaaru jàmm bi ci Efes lu tollook ñaari at (Jëf ya 19). Ci bataaxal bii, Póol dafa fàttali gëmkat yi li seen booloo ci Almasi bi di tekki. Jële na am njàngat ci Taalifi cant 8.7: Yàlla «jox na nit lépp, mu teg tànk.» Nit lajj, kon li Yàlla namm, moo di dajale lépp ci kilifteefu Almasi bi. Almasi bi mooy bopp bi tiim lépp, te mboolooy ñi koy topp ñoo taxawe yaramam. Jenn Yàllaa am, ak wenn yaram, ak jenn yaakaar ju leen seen wooteb Yàlla jëme. Su ñu dundee dundin wu yellook wooteb Yàlla, di jàmmoo, di sàmm seenug bennoo ci ndimbalal Noowug Yàlla gi ñu bokk, dinañu mana jànkoonteek pexey Seytaane. Póol bind na bataaxal yi ñeel waa Efes ak waa Filib ak waa Kolos, bi ñu ko jéngee, tëj ko kaso. Ci tënk: 1.1—3.21 Yàlla baaxe na leen bépp barkeb biir ci Almasi bi. 4.1—6.24 Ci ndimbalal Noowug Yàlla gu Sell gi lañu wara dunde dundin wu yellook wooteem.
7 Ci moom lanu ame njot gi nu sottalal njéggalug moy, ndax deretam ji tuuru, noonu ko Yàlla defe ci yiwam wu yaa, 8 wi mu nu baawaanal, mayaale nu mépp xel mu rafet akug dégg. 9 Moo nu xamal mbóotum coobareem mi mu nammoona sottale naka jekk ci Almasi bi, na mu ko neexe. 10 Li Yàlla namm, bu fan yi matee, moo di dajale lépp ci kilifteefu Almasi bi, mboolem la fa asamaan ak li fi suuf. 11 Ci moom lanu jote sunu muur ci kaw dogalu Yàlla mi nu tànn lu jiitu, moom miy sottal lépp ni mu ko namme ci coobareem. 12 Moo tax nu di ko sante màggaayam, nun ñi njëkka wékk sunu yaakaar ci Almasi bi.
13 Kooku, yeen ñi dul Yawut, ba ngeen déggee, yeen itam kàddug dëgg gi, xibaaru jàmm bi jëm ci seenug mucc, gannaaw ba ngeen gëmee, ci moom itam lañu leen màndargaale Noo gu Sell gi ñu dige woon. 14 Noo gi moo di dawal bi nu jotagum ci sunu muur, ba kera njotug ñoñi Yàlla matee, ba nit ñi sante Yàlla màggaayam.
- a Seetal ci Taalifi cant 8.7.
Languages