5 Juru bésub Mucc bi, dungeen ko mana rendi fenn ci dëkk yi leen seen Yàlla Aji Sax ji jox, 6 fu moy béreb ba seen Yàlla Aji Sax ji tànn ngir dëël turam. Foofa ngeen di rendi juru bésub Mucc bi ci ngoon bu jant biy so, yemook waxtu wa ngeen bàyyikoo woon Misra. 7 Toggleen ko, te lekk ko ca béreb ba seen Yàlla Aji Sax ji di tànni, ca suba sa ngeen xëy, dellu ca seeni xayma. 8 Juróom benni fan ngeen di lekk mburu mu amul lawiir, bésub juróom ñaareel di am ndaje, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Buleen ci liggéey dara.
9 Juróom ñaari ayi bés nag, ngeen di waññ, te ci ndoortel ngóob ngeen di tàmbalee waññ juróom ñaari ayi bés yi, 10 ngeen doora amal màggalug Ayi bés, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji, te saraxu yéene ba ngeen cay joxe di kemu koom ga leen seen Yàlla barkeele. 11 Ngeen daldi bànneexu fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji, yeen ak seeni doom, góor ak jigéen, ak seeni jaam, góor ak jigéen, ak Leween ñi ci seen dëkk, ak doxandéem yeek jirim yeek jëtun ñi ci seen biir, ci béreb bi seen Yàlla Aji Sax ji tànn ngir dëël turam ëllëg. 12 Fàttalikuleen ne ay jaam ngeen woon ca Misra te ngeen sàmmoo jëfe dogali yoon yii.
13 Màggalu Mbaar yi it nangeen ko wormaal diiru juróom ñaari fan, gannaaw bu ngeen dajalee seenum pepp ak seen ndoxum reseñ. 14 Ngeen daldi bànneexoo seenug màggal, yeen ak seeni doom, góor ak jigéen, ak seeni jaam, góor ak jigéen, ak Leween ñeek doxandéem yeek jirim yeek jëtun ñi ci seen biir dëkk. 15 Juróom ñaari fan ngeen koy màggal ñeel seen Yàlla Aji Sax ji ca béreb ba Aji Sax ji di tànni, ndax seen Yàlla Aji Sax ji moo leen di barkeelal seen meññat mépp, ak seen mboolem ñaq, seen mbégte mat sëkk.
16 Kon ñetti yoon cim at la seen góor ñépp di teew fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji, ca béreb ba muy tànni: fani màggalu Mburu mu amul lawiir, ak fani màggalug Ayi bés, ak fani màggalu Mbaar yi. Waaye deesul teewe loxoy neen fi kanam Aji Sax ji. 17 Ku nekk, na sarax ba muy indi, di kemu barke ba ko Yàlla jagleel.
21 Buleen samp benn xeru bant, bu jóge ci genn garab, ngir di ko jaamoo Asera tuur mi, ci seen wetu sarxalukaay bi ngeen sàkk ngir seen Yàlla Aji Sax ji. 22 Te itam buleen yékkati lenn lu bokk ci tuuri doj yooyu seen Yàlla Aji Sax ji bañ.
<- Baamtug yoon wi 15Baamtug yoon wi 17 ->
Languages